Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Yanqóoba 4:7
Leeru Bés bi
Kon nag nangulleen Yàlla, te bañal Seytaane, mu daw, ba sore leen.
Yanqóoba 4:7
Dees na ragale turu Aji Sax ji fa sowu, ragale màggaayam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.
Esayi 59:19
Yeesu nag ne ko: «Xiddi ma Seytaane, ndax bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”» Ba mu ko defee Seytaane won ko gannaaw, ay malaaka dikk, di toppatoo Yeesu.
Macë 4:10–11
Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem. Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.
Efes 6:10–11
jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.
Efes 5:11
ngir Seytaane bañ noo nax, ndax ay pexeem, umplewunu ko.
2.Korent 2:11
Àndleen ak sago te teewlu! Ki leen di tuumaal, Seytaane, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax. Pastéefu ngëm ngeen di xeexe te xam ne benn coono bi ngeen di daj, moom la mboolem seen bokki gëmkat yi ci àddina di daj.
1.Piyeer 5:8–9
Képp ku sosoo ci Yàlla, moo daan àddina; te galgal biy daan àddina mooy sunu ngëm.
1.Yowaan 5:4
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub.
Room 8:33
Éy bu ma xamoon fa may gise Yàlla, ba àkki péncam,
Ayóoba 23:3
Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, di déglu kàddug jaamam? Képp kuy doxe lëndëm te amul leeraange, na wóolu Aji Sax ji, te wéeroo Yàllaam jii.
Esayi 50:10
Su boobaa ngeen làmb, daj ma, ndegam làmbe ngeen seen léppi xol,
Yeremi 29:13
Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen. Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.
Luug 11:9–10
Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi.
1.Yowaan 1:3
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.
Efes 2:13
ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.
Efes 2:18
Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg.
1.Yowaan 1:6
te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»
Macë 28:20
Buleen jikkowoo bëggub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»
Yawut ya 13:5
Man maay ñaan Baay bi, mu yónnee leen beneen Taxawukat, ngir mu nekk ak yeen ba fàww. Kooku mooy Noowug Yàlla giy xamle liy dëgg. Àddina du ko mana dalal, ndax gisu ko te xamu ko. Yeen nag xam ngeen ko, ndax ci seen biir la dëkk, te ci seen biir xel lay nekk.
Yowaan 14:16–17
Bés yu mujj yi
Wone yépp24 Few 2026
23 Few 2026
22 Few 2026
21 Few 2026
20 Few 2026
19 Few 2026
18 Few 2026