Leeru Bés bi — 24 Fewriyee: Esekiyel 36:37

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Lii laay nangulaatal waa kër Israayil, defal leen ko: maay ful nit ñi niy gàtt.

Esekiyel 36:37

Yeenay xemmem lu ngeen dul am. Yeenay bóome, di iñaane lu ñeneen am, te manuleen koo am. Yeenay xuloo aka jàppante. Dungeen am, ndax yeena ñaanul.

Yanqóoba 4:2

«Ñaanleen, ñu may leen; seetleen, gis; fëggleen, ñu ubbil leen. Ndaxte képp ku ñaan, dinga am; ku seet, gis; ku fëgg it, dees na la ubbil.

Macë 7:7–8

Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul. Gannaaw xam nanu ne moo nuy nangul lépp lu nu ko ñaan, xam nanu ne dagaan yi nuy sàkku ci moom, am nanu ko.

1.Yowaan 5:14–15

Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.

Yanqóoba 1:5

Buleen fat tuuru jàmbur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.

Taalifi cant 81:10

Yeesu dellu leen léeb lii, ngir ñu wareefoo di sax ci ñaan te baña xàddi.

Luug 18:1

Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.

Taalifi cant 34:15

Aji Sax jeey won gannaaw ñiy def lu bon, ngir dagge leen kaw suuf, far seeni tur.

Taalifi cant 34:17

Bésub keroog, ci sama tur ngeen di ñaan. Waxuma leen ne man maa leen di ñaanal Baay bi, ndax kat Baay bi ci boppam moo leen sopp, ndaxte yeena ma sopp, te gëm ngeen ne man, ci Yàlla laa jóge.

Yowaan 16:26–27

Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.

Yowaan 16:24

Mu ne ko: «Waxi jeeg bu dof daal ngay wax, yaw! Du Yàlla da nuy may lu baax, nu jël? Kon kay bu nu mayee safaan ba it, nu wara jël.» Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul ciw làmmiñam.

Ayóoba 2:10

Aji Sax ji, ràññee naa ne say àtte dëgg la, te worma nga ma dumaa.

Taalifi cant 119:75

Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul bàyyi xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.

Esayi 64:8

Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

1.Samiyel 3:18

Aji Sax ji, yaa dëggu, ak li may tawatsi fi yaw lépp. Teewul ma di la diis mbir ci say àtte: lu tax ku bon di baaxle, bépp workat bu bon di féex?

Yeremi 12:1

Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci yoon.

Malasi 3:3

ndax Boroom bi, ku mu sopp, yar la, mooy bantal jépp doom ju ko neex.»

Yawut ya 12:6

Ab taalibe, su demee ba mel ni kilifaam, wàcc na; ab jaam it, su demee ba mel ni sangam, wàcc na. Ndegam boroom kër gi lañuy woowe Beelsebul, miy Seytaane, astamaak waa këram.

Macë 10:25

Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.

Yawut ya 5:8

Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

1.Piyeer 4:13

Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi.

Peeñu ma 7:14