Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.
Esayi 53:11
Leeru Bés bi
Mooy sonn ba gisug leer, doyloo ko. Ñu bareey xam sama jaam bii di Aji Jub, mu def ñu bare, ñu ñu limal njub, ndax li mu sëfoo seeni ñaawtéef.
Esayi 53:11
Yeesu nag muucu bineegar ba, daldi ne: «Sotti na!» Ci kaw loolu mu sëgal bopp ba, daldi yiwi noo ga.
Yowaan 19:30
Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
2.Korent 5:21
xeet wii ma bindal sama bopp, te ñooy siiwal sama woy.
Esayi 43:21
Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi bi, xel mu rafetum Yàlla, ni mu yaatoo ci fànn yu nekk. Loolu moo doon naka jekk nammeelam gi mu sottale ci Almasi Yeesu sunub Sang.
Efes 3:10–11
Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.
Efes 2:7
Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon. Noo gi moo di dawal bi nu jotagum ci sunu muur, ba kera njotug ñoñi Yàlla matee, ba nit ñi sante Yàlla màggaayam.
Efes 1:13–14
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
buleen të na woon ca fippu ga, keroog bésub seetlu Yàlla ba ca màndiŋ ma,
Yawut ya 3:8
Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn. Waaye ku nekk, sa xemmemtéefu bakkanu bopp moo lay xiirtal, ootal la ba nax la. Te xemmemtéefu bakkan bu ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bàkkaar bu matee, dee lay jur.
Yanqóoba 1:13–15
di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma, di diiŋat Yàlla ca àll ba.
Taalifi cant 106:14
Yeesu moo feesoon ak Noo gu Sell gi, bàyyikoo ci dexu Yurdan, ci njiital Noo gi, ba ca biir màndiŋ ma. Ñeent fukki fan la ko fa Seytaane fiire. Yeesu lekkul dara diir boobu bépp. Gannaaw ba fan yooyu wéyee, mu xiif. Seytaane nag ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj wii mu soppaliku mburu.»
Luug 4:1–3
Coonoy nattu bi mu dékku nag tax na mu mana wallu ñi nekk ci nattu.
Yawut ya 2:18
Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp. Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»
Luug 22:31–32
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Few 2026
18 Few 2026
17 Few 2026
16 Few 2026
15 Few 2026
14 Few 2026
13 Few 2026