Leeru Bés bi — 21 Fewriyee: Sarxalkat yi 20:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Nangeen sàmm samay dogali yoon te di ko jëfe. Man Aji Sax ji maay ki leen sellal.

Sarxalkat yi 20:8

Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji leen ràññaatleek yeneen xeet yi.

Sarxalkat yi 20:24

«Nangeen nekk ñu sell ci man, ndaxte Ku sell laa, man Aji Sax ji, te dama leena ràññaatleek yeneen xeet yi, ngeen di sama ñoñ.

Sarxalkat yi 20:26

Ci man Yudd miy jaamub Yeesu Almasi bi, di rakku Yanqóoba, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel leen yeen ñi ñu woo, yeen ñi Yàlla Baay bi sopp, te sàmmal leen Yeesu Almasi bi.

Yudd 1:1

Ngalla sellale leen dëgg gi: sa kàddu mooy dëgg.

Yowaan 17:17

Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee.

1.Tesalonig 5:23

Moo waral Yeesu itam deewe ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi deretu boppam.

Yawut ya 13:12

Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

Tit 2:13–14

Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena woowe ay bokk.

Yawut ya 2:11

Man nag, ñoom laa sellalal sama bopp, ngir ñoom itam, ñu mana sellaloo dëgg gi.

Yowaan 17:19

Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi bi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Na aw yiw ak jàmm juy baawaan ñeel leen.

1.Piyeer 1:2

Jub, leerlu; jubal, bég.

Taalifi cant 97:11

Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle. Ku doon wéy a wéy, di jooy; yor mbuusum jiwoom, yal na dikk a dikk, di woy, ñibbiwaale sabaaram.

Taalifi cant 126:5–6

Te li nga ji du yaramu gàncax giy ñëw, aw fepp kese la, man naa doon bele, mbaa weneen jiwu.

1.Korent 15:37

Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi bi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi bi, ngir may nu yaakaar juy dund.

1.Piyeer 1:3

Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu. Yooyu nattu, ni sawara di natte wurus, ni lay natte seen dëggutey ngëm, te ngëm a gën wurus fuuf, nde wurus day jeex. Su ko defee seen ngëm gu dëggu jural leen ag cant ak daraja ak teraanga, bés bu Yeesu Almasi bi feeñee.

1.Piyeer 1:6–7