Yeena àgg fa Yeesu, rammukat bi dox kóllëre gu yees gi. Yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
Yawut ya 12:24
Leeru Bés bi
Yeena àgg fa Yeesu, rammukat bi dox kóllëre gu yees gi. Yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
Yawut ya 12:24
Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.
Yowaan 1:29
Mboolem waa àddina di ko sujjóotal, maanaam mboolem ñi ñu bindul seen tur ca ndoortel àddina ci téereb dund bu Xar mi ñu rendi.
Peeñu ma 13:8
ndax deretu yëkk ak ju sikket kat manula far ay bàkkaar. Moo tax ba Almasi biy dikk ci àddina la wax ne: «Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko, waaye aw yaram nga ma waajalal.
Yawut ya 10:4–5
Coobarey Yàlla googu moo waral ñu sellale nu sarax bi Yeesu Almasi bi sarxe yaramam benn yoon ba fàww.
Yawut ya 10:10
Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga njëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel ak saraxam,
Njàlbéen ga 4:4
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:2
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu,
Yawut ya 10:19
Ana ku xam sa dooley mer ak sa xadar ju raglu?
Taalifi cant 90:11
La tàmbalee fukki waxtu ak ñaar ca bëccëg nag, ag lëndëm a wàcc ca réew ma mépp, ba fukki waxtu ak juróom ca ngoon. Wetu fukki waxtu ak juróom ca ngoon, ca la Yeesu àddu ca kaw ne: «Eli, Eli, lema sabaktani?» Loolu di tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma?»
Macë 27:45–46
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
Room 8:1
Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi.
Room 5:1
Almasi bi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
Galasi 3:13
Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam. Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:9–10
ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
Room 3:26
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Few 2026
21 Few 2026
20 Few 2026
19 Few 2026
18 Few 2026
17 Few 2026
16 Few 2026