Leeru Bés bi — 22 Fewriyee: Taalifi cant 25:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ana kuy wormaal Aji Sax ji, mu won ko yoon wi mata tànn,

Taalifi cant 25:12

«Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo,

Macë 6:22

Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.

Taalifi cant 119:105

di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.

Esayi 30:21

Nga ne ma: «Dama laa xelal, xamal la fi ngay jaar, digal la, di la bàyyi xel. Buleen mel ni fas mbaa berkelle mi amul ag dégg, laab ak tarka di ko téye, mu doora yem fi seen wet.» Ku bon barew tiis. Ku wóolu Aji Sax ji, mu yiire la ngoram. Yaw aji jub ji, bégal te bànneexoo Aji Sax ji. Képp kuy def njub, sarxolleel!

Taalifi cant 32:8–11

Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.

Yeremi 10:23

Soo tëddee doo tiit; say nelaw day neex.

Kàddu yu xelu 3:24

Ba mu ko defee ngelaw la riddeek doole, gannax yay dal ca kaw gaal ga, ba mu bëgga fees. Teewul Yeesoo nga ca taatu gaal ga, tëdd, gegenu, di nelaw. Taalibe ya yee ko, ne ko: «Kilifa gi, nu ngi sànku, xanaa xalaatoo nu?»

Màrk 4:37–38

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.

Filib 4:6–7

May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.

Taalifi cant 4:8

Neen it la nit di teela jóg aka guddee tëdd, di doñ-doñi lu mu lekk: Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day, fekk ko muy nelaw.

Taalifi cant 127:2

Ñuy dóor Eccen ay doj, moom muy ñaan Yàlla, naan: «Sang Yeesu, nangul sama bakkan!» Mu ne gurub, samp bëti óomam, daldi àddu ca kaw, ne: «Sang bi, bu leen topp bii bàkkaar.» Naka la wax loolu, daldi faatu.

Jëf ya 7:59–60

Kon fees nanu ak kóolute, te li nu gënal mooy jóge ci sunu yaramu bopp, ngir dëkki ak Sang bi.

2.Korent 5:8