Bu ma teg tiitaange, yaay sama rawtu bésub safaan.
Yeremi 17:17
Leeru Bés bi
Bu ma teg tiitaange, yaay sama rawtu bésub safaan.
Yeremi 17:17
Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.
Taalifi cant 4:6
Ñuy wër di wut lu ñu lekk, su ñu suurul, di ñurumtu.
Taalifi cant 59:16
Meram di lu gàtt, aw yiwam sax dàkk. Rongooñ gane, fanaan, ay ree xëysi.
Taalifi cant 30:6
Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, dëj ma, ma ne kekk niw tund. Nga fuuyu, ma jàq. Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw, ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa kóllëre?
Taalifi cant 30:8–10
Mu ne: «Maa la wacc diir bu gàtt, dellu la jël ci yërmande ju yaa. Sama xol a jóg, ma xañ la sama kanam ab diir, waaye maa lay yërëme ngor gu sax.» Aji Sax ji lay jot moo ko wax.
Esayi 54:7–8
Maa leen ko wax déy ci lu wér, yeen yeenay jooy aka jooytu, àddina moom di bég; yeen, yeenay amu tiis, waaye bànneex la seenu tiis di soppaliku.
Yowaan 16:20
Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, njukkale ko sellaayam.
Taalifi cant 30:5
Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set.
Njàlbéen ga 5:3
Lu sobewu, ana ku ci mana am lu laab? Du kenn!
Ayóoba 14:4
Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
Taalifi cant 51:5
Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar
Efes 2:1
Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.
Efes 2:3
Xam nanu ne yoonu Musaa ci Yàlla la bokk, te man may nitu suuxu neen, dib jaam bu ñu jaay bàkkaar, muy sama sang. Xawma sax lu waral may jëfe ni may jëfe; li ma namm, du loolu laay jëfe, waaye li ma bañ, moom laay jëfe.
Room 7:14–15
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.
Room 5:12
Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu baaxe ñu bare àtteb nit ñu jub.
Room 5:19
Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi bi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?
Room 5:15
Ndax kat, yoonu Noo gu Sell giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci yoonu bàkkaar ak dee.
Room 8:2
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Few 2026
16 Few 2026
15 Few 2026
14 Few 2026
13 Few 2026
12 Few 2026
11 Few 2026