Nan càmbar, ba xoolaat jikko yi te dellu ci Aji Sax ji.
Jooytu 3:40
Leeru Bés bi
Nan càmbar, ba xoolaat jikko yi te dellu ci Aji Sax ji.
Jooytu 3:40
Aji Sax ji, nattu ma, seetlu ma, seggal xel ak xol.
Taalifi cant 26:2
Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.
Taalifi cant 51:6
Damaa seetlu sama jëfin, dëpp, topp sa kàdduy seede. Maa ngi gaawtu, yeexewuma say santaane moos!
Taalifi cant 119:59–60
Kon na ku nekk seetlu boppam, doora lekk ci mburu mi, naan ci kaas bi.
1.Korent 11:28
Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
1.Yowaan 1:9
Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.
1.Yowaan 2:1
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe. Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla ga. Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:19–22
Meloom a ngay niru peru jàspë ak peru sarduwan, ag xon gu mel ni peru emëródd wër ngàngune ma.
Peeñu ma 4:3
Yàlla neeti: «Kóllëre gi may fas ak yeen ak mboolem mbindeef mu ànd ak yeen, day sax ba fàww te liy màndargaam mooy lii. Def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre gi dox sama diggante ak àddina.
Njàlbéen ga 9:12–13
Xon gi day nekk ci biir niir yi, ma di ko gis, di xalaat kóllëre, gi ma fas fàww, sama diggante, man Yàlla, ak mboolem xeetu mbindeef mu nekk ci kaw suuf.»
Njàlbéen ga 9:16
Du nii la sama waa kër def ak Yàlla? Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk, lépp jekk, mat sëkk. Moo may may ndam saa su ne, di ma defal lu ma namm.
2.Samiyel 23:5
Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam.
Yawut ya 6:18
Nun nag noo leen di àgge xibaaru jàmm bii: li Yàlla digoon sunuy maam, nun sët yi la ko defal, ba mu yékkatee Yeesu, te noonee lañu ko binde ci ñaareelu saaru Taalifi cant, ne: “Yaa di sama Doom, bés niki tey, maa la jur.”
Jëf ya 13:32–33
Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.
Yawut ya 13:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Few 2026
24 Few 2026
23 Few 2026
22 Few 2026
21 Few 2026
20 Few 2026
19 Few 2026