Leeru Bés bi — 19 Fewriyee: Kàddu yu xelu 2:6

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ndax Aji Sax jeey maye xel mu rafet, kàddoom di taxa xam, di dégg.

Kàddu yu xelu 2:6

Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin.

Kàddu yu xelu 3:5

Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.

Yanqóoba 1:5

Waaye li àddina jàppe ag ndof, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko xamkat yi, te li néew doole ci àddina, moom la Yàlla tànn, ngir rusloo ko li bare doole.

1.Korent 1:27

ba tax kenn du mana damu ci kanam Yàlla.

1.Korent 1:29

Sa pirim kàddu day leeral, di xelal ku xeluwul.

Taalifi cant 119:130

Sama xol laa làq say wax, ngir bañ laa moy.

Taalifi cant 119:11

Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»

Luug 4:22

Wattukat ya ne leen: «Nit masula waxe ni kii!»

Yowaan 7:46

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,

1.Korent 1:30

Bésub feyul samay ñoñ laa mébétoon, atum tekki jéng yi jot.

Esayi 63:4

Te nangeen sellal at ma ca topp di juróom fukkeelu at ma, ngeen yéene ca mboolem waa réew ma ba mu daj, ne ngoreel taxaw na. Seen atum Yiwiku la, ku nekk war cee dellu ca suufu waa këram, ku nekk it wara dellu ca làng ga mu bokk.

Sarxalkat yi 25:10

Waaye yaw askan wi, ñi nga deele ñooy dellu dundaat, seeni néew ay dekki, ku doon nelaw sa biir bàmmeel, yewwu, sarxolle. Aji Sax jeey yebal lay bu ànd aki leer, suuf delloosi ña dëddu.

Esayi 26:19

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.

1.Tesalonig 4:16–17

«Man nag ndax maa leen di musal ci njaniiw? Ndax maa leen di jot ci dee? Moo yaw dee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!

Ose 13:14

Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.

Yeremi 50:34