Leeru Bés bi — 17 Fewriyee: Sarxalkat yi 4:12

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

mboolem li des ci yëkk wi daal lay génne dal bi, yóbbu ko ci béreb bu mucc sobe, ca jalub dóom ba, daldi taal matt, lakk ko ca, ba mu dib dóom. Foofa dóom ba jale lees koy lakke.

Sarxalkat yi 4:12

Noonu nag Pilaat teg Yeesu ci seeni loxo, ngir ñu daaj ko ci bant. Ñu daldi yóbbu Yeesu.

Yowaan 19:16

Foofa lañu daaje Yeesu ca bant ba, mook ñeneen ñaar; kii ci wet gii, kee ca wet gee, Yeesu ca digg ba.

Yowaan 19:18

Ndax kat, jur ga sarxalkat bu mag ba daan yóbbu seen deret ca néeg bu sella sell ba, ngir njotlaayal bàkkaar, seen yaram lees daan lakk ca bitib dal ba. Moo waral Yeesu itam deewe ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi deretu boppam. Kon nag, nanu ko fekki ca bitib dal ba, ba tegoo toroxtaangeem ga mu tegoo woon,

Yawut ya 13:11–13

Sàkkuwuma lu moy xam ko, xam manoore ji ko dekkal, ak itam séddu ci ay coonoom, ba bokk ak moom deewam,

Filib 3:10

Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.

1.Piyeer 4:13

Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.

2.Korent 4:17

Yàlla dafa sàkk nit ci melokaanam; ci melokaanu boppam la Yàlla sàkk nit, góor ak jigéen la sàkk.

Njàlbéen ga 1:27

Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.

Jëf ya 17:29

Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy gi mu nu sopp, nun ñi doon nit ñu dee ba noppi ndax sunuy moy, moo nu booleek Almasi bi, dundalaat nu. Ci kaw yiw daal ngeen mucce.

Efes 2:4–5

Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.

Efes 2:10

Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw ci biir rakk yu bare.

Room 8:29

Kooku moo dikk ag guddi ba ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ab kilifa nga bu bawoo fa Yàlla, nde kenn manula def firnde yii ngay def, te du Yàllaa ànd ak moom.»

Yowaan 3:2

Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.

Taalifi cant 17:15

Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,

Peeñu ma 21:7

Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.

Room 8:17