Sa diw yi ngay xeeñoo neex, saw tur jib, mel ni lu xeeñ a xelli. Moo tax janq ji nob la.
Ngën-gi-woy 1:3
Leeru Bés bi
Sa diw yi ngay xeeñoo neex, saw tur jib, mel ni lu xeeñ a xelli. Moo tax janq ji nob la.
Ngën-gi-woy 1:3
te ngeen di doxale cofeel, ni Almasi bi nu sopp, ba joxeel nu bakkanam, def ko saraxu sawara ngir xetug jàmm gi neex Yàlla.
Efes 5:2
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.»
1.Piyeer 2:7
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf,
Filib 2:9–10
Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom,
Kolos 2:9
«Su ngeen ma soppee, sàmmleen samay ndigal.
Yowaan 14:15
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Maryaama nag indi genn wàllu liitaru nàrd, diwu nàrd gu xeeñ lu neex te raxul te jafe njëg lool, sotti ko ca tànki Yeesu, daldi fomp tànk ya ak kawaru boppam. Kër ga gépp ne bann ak xetu diw ga.
Yowaan 12:3
Ba waa kuréelu àttekat ya gisee fit wi Piyeer ak Yowaan àndal, te ñu xam ne niti neen ñu masula jàng lañu, dañoo waaru. Xamoon nañu nag ne ñook Yeesoo nekkoon.
Jëf ya 4:13
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Taalifi cant 8:1
«Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.
Macë 1:23
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
Kàddu yu xelu 18:10
Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ci dee, daldi suux ci biir dund.
2.Korent 5:4
Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.
Taalifi cant 38:9
Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.
Taalifi cant 38:4
Céy maaka réy aw tiis! Ana ku may wallook sama yaramu dee wii?
Room 7:24
Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu. Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gu Sell gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.
Room 8:22–23
Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.
1.Piyeer 1:6
Ndax damaa leer, ni ma ko sunu Boroom Yeesu Almasi bi leeralale, ne bés bi may summi sama màkkaanu suux bii dëgmal na.
2.Piyeer 1:14
Sunu yaramu judduwaale wii nara yàqu, fàww mu sol weneen wu dul yàqu; sunu yaramu dee wii, fàww mu sol yaramu deetil. Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu dee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na dee ci géeju ndam.
1.Korent 15:53–54
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Few 2026
14 Few 2026
13 Few 2026
12 Few 2026
11 Few 2026
10 Few 2026
9 Few 2026