Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
Kàddu yu xelu 20:9
Leeru Bés bi
Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?
Kàddu yu xelu 20:9
Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey wut Yàlla. Ñépp lajj, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.
Taalifi cant 14:2–3
Moo tax ñi wéye seen bindu suuxu neen duñu mana neex Yàlla.
Room 8:8
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul. Ndax kat du lu baax li ma namma jëfe laay jëfe, waaye lu bon li ma nammul, moom laay jëfe.
Room 7:18–19
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Esayi 64:6
Waaye Mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi bi di maye, mana dikkal aji gëm ñi.
Galasi 3:22
Loolu di firi ne ci Almasi bi la Yàlla jubale waa àddina ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.
2.Korent 5:19
Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg. Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
1.Yowaan 1:8–9
Aji Sax ji, géej a riir, géej a àddu, mu riir, gannax ya rëkk, mu riir. Waaye riirum wal mu walangaanoo, ak géej gu sàmbaraaxoo, Aji Sax ja fa kaw a rawati!
Taalifi cant 93:3–4
Yàlla ji ñu teral a teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër? Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi sa kóllëre féete fu ne!
Taalifi cant 89:8–9
Man daal, ndax dangeen maa ragalul, am dungeen raf ci sama kanam?”» Kàddug Aji Sax jee. «Man mi teg gannuus, yemalee ko géej, dogalal ko ko dàkk te du ko jàll, lu mu wañax wañax, du ko man; gannax ya day riir, te du jàll!
Yeremi 5:22
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
Esayi 43:2
Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer wàcce ca gaal ga, dox ci kaw ndox mi, jëm ca Yeesu. Teewul ba mu gisee na ngelaw la riddee, dafa tiit, tàmbalee suux. Mu àddu ca kaw, ne: «Sang bi, wallu ma!» Yeesu daldi tàllal loxoom, jàpp ko, ne ko: «Yaaka néew ngëm, ana looy xel ñaar?»
Macë 14:29–31
Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku màgg ki,
Taalifi cant 56:3
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Few 2026
13 Few 2026
12 Few 2026
11 Few 2026
10 Few 2026
9 Few 2026
8 Few 2026