Yeesu ne ko: «Baalagum noonu rekk, ndax ci lanuy matale lépp li Yàlla bëgg ci njub.» Yaxya daldi koy nangul.
Macë 3:15
Leeru Bés bi
Yeesu ne ko: «Baalagum noonu rekk, ndax ci lanuy matale lépp li Yàlla bëgg ci njub.» Yaxya daldi koy nangul.
Macë 3:15
Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
Taalifi cant 40:8
«Buleen defe ne damaa dikk ngir tebbi yoonu Musaa, ak waxi yonent yi. Tebbisiwuma, damaa sottalsi. Maa leen ko wax déy, ba keroog asamaan ak suuf raaf, wenn rëdd, mbaa genn maaska du raaf mukk ci yoonu Musaa, ba kera lépp sotti.
Macë 5:17–18
Aji Sax ji la soob ci njubteem, mu fésal màggaayu yoonam ak taar ba.
Esayi 42:21
Te kat maa leen ko wax, bu seenub njub ëppul njubu firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi, dungeen tàbbi mukk ci nguurug asamaan.
Macë 5:20
Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal mi war ci bàkkaar, ngir njub gi yoonu Musaa laaj mana sotti ba mat sëkk ci nun, ñi toppatul sunu bindu suux, xanaa Noowug Yàlla.
Room 8:3–4
Ndax kat Almasi bi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.
Room 10:4
Aji Sax ji neeti Aaróona: «Seenum réew nag doo ci am cér, te wàllu suuf, doo ko am ci seen biir. Man maay sa wàll, di sab cér ci biir bànni Israayil.»
Màndiŋ ma 18:20
Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy? Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
Taalifi cant 73:25–26
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg. Maa muurloo béreb bu neex, ndaw cér bu rafet!
Taalifi cant 16:5–6
«Samab séddoo, Aji Sax jee,» la sama xol wax, te moo tax ma di ko xaar.
Jooytu 3:24
Maa séddoo fàww sa kàdduy seede, loolooy seral sama xol.
Taalifi cant 119:111
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.
Taalifi cant 63:1
Su ma tëddee, fàttaliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.
Taalifi cant 63:7
Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
Ngën-gi-woy 2:16
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Few 2026
12 Few 2026
11 Few 2026
10 Few 2026
9 Few 2026
8 Few 2026
7 Few 2026