Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kaw-a-kaw lay nirook ngàngune.
Esekiyel 1:26
Leeru Bés bi
Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kaw-a-kaw lay nirook ngàngune.
Esekiyel 1:26
Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu
1.Timote 2:5
Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam. Moo toroxlu, moo nangu, ba dee fekk ko ci, ak mbugalu bant ba ñu ko daaj.
Filib 2:7–8
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Yawut ya 2:14
Maay Kiy dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.
Peeñu ma 1:18
Ndax kat xam nanu ne Almasi bii dekki te dootul dee, te dee manalatu ko dara. Deewam ga mu dee, dee na benn yoon ba fàww, ba tax bàkkaar amatul benn kilifteef, te dund gi muy dund tey, Yàlla la koy dundal.
Room 6:9–10
Kon bés bu ngeen gisee Doomu nit kiy yéeg jëm fa mu njëkkoona nekk nag?
Yowaan 6:62
Ndax kat ci Almasi bi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom,
Kolos 2:9
Cig néew doole lees ko daaje ci bant, ba rey ko, waaye tey ci manoorey Yàlla lay dunde. Nun itam sunug bokk ci Almasi bi moo tax nu néew doole, waaye ci manoorey Yàlla lanuy bokk ak moom di dund, bu nuy jëflante ak yeen.
2.Korent 13:4
Lii laay muñe samaw naqar, sa kàddoo may dundal.
Taalifi cant 119:50
Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
Yowaan 5:26
Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund. Te képp kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
Yowaan 11:25–26
Ci moom la dund nekk, te dund dig leer, ñeel nit ñi.
Yowaan 1:4
Teewul mboolem ñi ko dalal, ba gëm ko, ñoom la may ñu yelloo doon doomi Yàlla. Ñooñu du ci deret lañu sosoo, te it du ci coobarey nitu suuxu neen, mbaa ci coobarey góor lañu sosoo, waaye ci Yàlla lañu sosoo.
Yowaan 1:12–13
Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.
Yowaan 6:63
Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
Yawut ya 4:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Few 2026
11 Few 2026
10 Few 2026
9 Few 2026
8 Few 2026
7 Few 2026
6 Few 2026