Leeru Bés bi — 12 Fewriyee: Malasi 3:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxe as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxe.

Malasi 3:17

«Nit ñi nga tànne ci àddina, jox ma leen, ràññeeloo naa leen saw tur. Sa ñoñ lañu woon, nga jox ma leen, te sa kàddu, sàmm nañu ko.

Yowaan 17:6

Man nag, ñoom laay ñaanal; ñaanaluma waa àddina, waaye ñi nga ma dénk, ñoom laay ñaanal, ndax sa ñoñ lañu. Mboolem lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom, te ci ñoom la sama daraja feeñe.

Yowaan 17:9–10

«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.

Yowaan 17:24

Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.

Yowaan 14:3

kera bés bu délsee ba jot ci teraangaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.

2.Tesalonig 1:10

Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.

1.Tesalonig 4:17

Yaay doon kaalag teraanga ci loxol Aji Sax ji, yaay doon mbaxanam buur, ci sa biir loxol Yàlla jii.

Esayi 62:3

Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leer ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi bi.

2.Korent 4:6

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.

Yowaan 1:18

Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, maa la koy sàkkoo xol.

Taalifi cant 42:2

Yaw la sam xel ne ma, ma jaamu la, te it yaw Aji Sax ji laay jaamu.

Taalifi cant 27:8

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

2.Korent 3:18

«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.

Yowaan 17:24