Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttaliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.
Malasi 3:16
Leeru Bés bi
Ca la ñi ragal Aji Sax ji diisoo ci seen biir, Aji Sax ji teewlu, déglu leen. Ñu bind fi kanamam téereb fàttaliku, bu lim ñi ragal Aji Sax ji, te teral aw turam.
Malasi 3:16
Naka lañuy waxtaan aka diisoo, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom.
Luug 24:15
ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»
Macë 18:20
Yaw itam sama mbokkum surga bu dëggu bi, dama lay ñaan nga jàppale leen ci, ñoom ñaar ñooñoo bokkoon ak man coonob xamle xibaaru jàmm bi, ñoom ak ñoom Kelemaŋ, mboolem sama bokki liggéeykat yi seeni tur binde ca téereb dund ba.
Filib 4:3
Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.
Kolos 3:16
Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub teyagum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.
Yawut ya 3:13
Maa leen wax ne leen, gépp kàddug neen gu nit masa wax, dina ko layoo kera bés-pénc. Ndax kat ci sa kàddu lees lay joxe dëgg, ci sa kàddu it lees lay daane.»
Macë 12:36–37
«Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam: Duma noppi déy, maa leen di fey, maa leen di fey ba mu mat sëkk.»
Esayi 65:6
Garabi Aji Sax ja, seedari Libaŋ ya mu jëmbat, regg nañu,
Taalifi cant 104:16
Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen. Maay mel nib lay buy guusal Israayil, ñu focci ni tóor-tóor, seeni reen sampu ni garabi Libaŋ,
Ose 14:5–6
Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, yaakaar Aji Sax ji. Day mel ni garab gu saxe wetu ndox, lawal ay reenam ca wal ma, ragalul tàngoor wu dikk, xob ya di naat. Du tiit atum maral, du ñàkk meññeef.
Yeremi 17:7–8
Garabi àll bi yépp dinañu xam, ne man Aji Sax ji maay gàttal garab gu gudd, di guddal garab gu gàtt. Maay wowal garab gu naat, di naatal garab gu wow. Man Aji Sax ji maa wax, maay jëf.”»
Esekiyel 17:24
Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru. Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni garabu seedaru Libaŋ gu ñu jëmbat ci biir kër Aji Sax ji, muy naate ci sunu biir ëttu Yàlla;
Taalifi cant 92:12–14
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Few 2026
9 Few 2026
8 Few 2026
7 Few 2026
6 Few 2026
5 Few 2026
4 Few 2026