Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp ay fees ak leer, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
Luug 11:34
Leeru Bés bi
Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp ay fees ak leer, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm.
Luug 11:34
Nitu neen nag du nangu lu aju ci Xelum Yàlla. Ag ndof lay doon ci moom; du ko mana xam, ndax loolu Xelum Yàlla lees koy natte.
1.Korent 2:14
Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.
Taalifi cant 119:18
Yeesu waxati leen ne leen: «Man maay leeru àddina. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye leeru dund ngay am.»
Yowaan 8:12
Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.
2.Korent 3:18
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leer ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi bi.
2.Korent 4:6
ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi bi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax. Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo.
Efes 1:17–18
Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
Taalifi cant 78:20
Bokk yi, bëgguma ngeen umple ko, sunu maam yépp la niir wa yiiroon, te ñoom ñépp a jàll géej ga. Ñoom ñépp lañu sóob sóobeb Musaa, ca biir niir wa ak ca biir géej ga. Ñoom ñépp, wenn ñamu kéemaanu Yàlla wa, moom lañu lekk, te ñoom ñépp, menn ndoxum kéemaanu Yàlla ma lañu naan, ndax ñoo doon naane ca doju kéemaanu Yàlla ga, doj wa leen doon gunge, te doj wa Almasi bi la woon.
1.Korent 10:1–4
Teewul kenn ca takk-der ya jam ko ab xeej ci faar yi, deret ànd ak ndox tuuru ca saa sa.
Yowaan 19:34
Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.
Esayi 53:5
te bëgguleena ñëw ci man, ba texe!
Yowaan 5:40
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Yeremi 2:13
Rakki Yeesu yu góor ya ne Yeesu: «Jógeel fii te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe, ñoom itam, gis jaloore yi ngay def.
Yowaan 7:3
Noo gu Sell gi ak Séet bi nee ñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.
Peeñu ma 22:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Few 2026
8 Few 2026
7 Few 2026
6 Few 2026
5 Few 2026
4 Few 2026
3 Few 2026