Ibraayma ne ko: “Doom, fàttalikul ne, na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
Luug 16:25
Leeru Bés bi
Ibraayma ne ko: “Doom, fàttalikul ne, na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
Luug 16:25
Sab jant du sooti, sa weer du suuxati. Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa fani ñaawlu jeex.
Esayi 60:20
Mooy mëdd dee ba fàww! Boroom bi Aji Sax jeey fompe gépp kanam rongooñi boroom. Buumi gàccey ñoñam it, moo koy doge fépp ci àddina. Aji Sax ji kat wax na ko.
Esayi 25:8
Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi. Loolu moo leen taxa teew fi kanam ngàngunem Yàlla, di ko jaamu ci biir màkkaanam guddi ak bëccëg, te ki toog ci ngàngune mi moo leen di yiir. Dootuñu xiif, dootuñu mar. Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor, ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»
Peeñu ma 7:14–17
Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:4
Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey.
Yowaan 9:4
Ci kaw loolu ma dégg baat bu jibe asamaan ne: «Bindal: “Bés niki tey ndokkalee aji dee ñi deewaale gëm Sang bi.”» Noowug Yàlla nee: «Waawaaw, ndax coono dina leen wàcc, ngir seeni jëf a leen topp.»
Peeñu ma 14:13
Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle, fa la ña jeele doole noppaloo,
Ayóoba 3:17
Samiyel ne Sawul: «Ana loo may woowe, di ma yékkatee nii?» Sawul ne ko: «Damaa nekk ci njàqare lu réy. Waa Filistee ngi xareek man, te Yàlla dëddu na ma. Wuyootu ma, du ci kàddug yonent, du ci gént. Moo tax ma woo la, ngir nga xamal ma lu may def.»
1.Samiyel 28:15
Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw ga nga jëm.
Kàdduy waare 9:10
Du ku dee mooy màggal Ki Sax, du kenn ku tàbbi réewum tàbbi-selaw!
Taalifi cant 115:17
Man nag, daanaka saraxu tuuru bu sottiku laa ba noppi; sama waxtuw dem dëgmal na. Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko. Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
2.Timote 4:6–8
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla. Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dalloo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dalloo ci say liggéey.
Yawut ya 4:9–10
Bés yu mujj yi
Wone yépp8 Few 2026
7 Few 2026
6 Few 2026
5 Few 2026
4 Few 2026
3 Few 2026
2 Few 2026