Leeru Bés bi — 8 Fewriyee: Yowaan 15:15

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.

Yowaan 15:15

Booba Aji Sax jaa ngi wax naan: «Xanaa duma nëbb Ibraayma li ma nar?

Njàlbéen ga 18:17

Mu ne leen: «Yeen lañu may ngeen xam mbóoti nguurug asamaan, waaye ñale, mayeesu leen ko.

Macë 13:11

Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.

1.Korent 2:10

Li nuy biral kay, da di mbóotum xam-xamu Yàlla mu làqu woon, te Yàlla dogaloon nu koo terale, laata àddina di sosu.

1.Korent 2:7

Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.

Taalifi cant 65:4

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

Taalifi cant 25:14

ndax wax ji nga ma dénk, dénk naa leen ko, te nangu nañu ko. Xam nañu xéll it ne ci yaw laa jóge, te gëm nañu ne yaw yaa ma yebal.

Yowaan 17:8

Deesatul dégg ci sam réew: “Fitna ñëw na!” deesatul dégg it fi sa kemu suuf: “Yàqute ak Yàqulee ngii!” “Mucc” ngay tudde say tata, te “Cant” ngay tudde sa bunti dëkk.

Esayi 60:18

Tatay dëkk baa nga sampe ci fukki doji fondmaa ak ñaar yu ñu bind fukki tur ak ñaar yu ndawi Xar mi.

Peeñu ma 21:14

Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen. Yeena di tabax bi ndawi Almasi bi ak yonent yi di fondmaa bi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju koñu tabax bi. Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. Ci Almasi bi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jàmbur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Efes 2:19–22

gannaaw mos ngeen ci mbaaxug Sang bi. Dikkleen ci moom, mooy doj wuy dund. Nit ñee ko beddi moos, waaye Yàllaa ko fal, fonk ko. Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.

1.Piyeer 2:3–5

Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 65:1