Leeru Bés bi — 7 Fewriyee: Baamtug yoon wi 8:10–11

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Dingeen lekk ba regg, di sante seen Yàlla Aji Sax ji réew mu baax ma mu leen jox. Wattuleen seen bopp nag, bala ngeena fàtte seen Yàlla Aji Sax ji, baña sàmm ay santaaneem ak àttey yoonam ak dogali yoonam yi ma leen di dénk tey.

Baamtug yoon wi 8:10–11

Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi walbatiku, di xaacuy sàbbaal Yàlla. Mu dikk, ne gurub, dëpp jëëm fa tànki Yeesu, sant ko. Waa ja nag nitu Samari la woon. Ba loolu amee Yeesu ne: «Xanaa du fukk a wér? Juróom ñeent ña nag, ana ñu? Amu ci kenn ku ñëw, delloo Yàlla njukkal ku dul doxandéem bii!»

Luug 17:15–18

Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees koy jariñoo. Lu mu mana doon, kàddug Yàlla akug ñaan moo koy sellal.

1.Timote 4:4–5

Ndax kiy taamu bés, Boroom bi la koy taamul; naka noonu kiy lekk, Boroom bi la koy gërëme, nde moom lay sant doora lekk; ki lekkul it Boroom bi lay sàkkoo ñàkka lekkam, te Yàlla lay sant.

Room 14:6

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

Kàddu yu xelu 10:22

Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellaayu turam! Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, te baña fàtte mboolem xéewalam! Moo lay baal foo ñaawe, di la wéral foo woppe. Mooy jot sa bakkan, kaalaa la ngor ak yërmande,

Taalifi cant 103:1–4

Ba mu wàccee ca gaal ga, mbooloo mu réy la gis. Mu ñeewante leen, daldi faj seeni jarag.

Macë 14:14

Yeesu Almasi bi, menn mii la woon démb ak tey ba fàww, du soppiku.

Yawut ya 13:8

Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.

Yawut ya 4:15

Dina mana sédd cér ñi xamul ak ñi moy ndax moom ci boppam ci ag néew doole la tënku.

Yawut ya 5:2

Gannaaw loolu mu délsi, fekk taalibe ya di nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangay nelaw? Wenn waxtu doŋŋ, amuloo dooley teewlu ko? Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»

Màrk 14:37–38

Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal. Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.

Taalifi cant 103:13–14

Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma. Geesu ma, baaxe ma. Dooleelal sab jaam, wallul ki sa jaam sukk jur!

Taalifi cant 86:15–16