Leeru Bés bi — 6 Fewriyee: 1.Timote 1:14

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sunu yiwu Boroom moo ma baawaanal, booleel ma ci ngëm gi ak cofeel gi gëmkatub Almasi Yeesu jagoo.

1.Timote 1:14

Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi bi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.

2.Korent 8:9

Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,

Room 5:20

Mbaax gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu, moom lay firndeele mboolem xarnu yiy ñëw, ni yiwam yaatoo ba tiiñ am xel.

Efes 2:7

du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.

Efes 2:9

Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di baaxee àtteb ku jub, waaye ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi bi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla àtte nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi bi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di baaxee kenn àtteb ku jub.

Galasi 2:16

ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.

Tit 3:5–6

«Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»

Peeñu ma 22:16

Maa ngi koy gis, te du tey, maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israayil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.

Màndiŋ ma 24:17

Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.

Room 13:12

Nijaay, balaa jant a fenk, ker toxu, dellul gaaw ni kéwél, mbaa kooba gu ndaw kaw tund yu xàjjalikoo ya.

Ngën-gi-woy 2:17

Yéene bii moo wàccal Duuma: Nit a ngi may woowe tundu Seyir, naan: Wattukat bi, lu des ci guddi gi? Éy wattukat bi, lu desati ci guddi gi? Wattukat bi ne: «Bët set, mu guddeeti rekk; boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.»

Esayi 21:11–12

Yeesu waxati leen ne leen: «Man maay leeru àddina. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye leeru dund ngay am.»

Yowaan 8:12

te man ci sama bopp, noonee laa jote sañ-sañ bi ci sama Baay. Maa lay jox itam biddiiwu njël.

Peeñu ma 2:28

Moytuleen te teewlu, ndax xamuleen kañ la. Daa mel ni nit ku tukki, bàyyi këram gannaaw. Fekk na mu batale ay surgaam, ku nekk ak saw sas. Bëkk-néeg bi nag, mu sant ko ne ko mu teewlu. Kon teewluleen, ndax xamuleen kañ la boroom kër giy dikk. Jombul muy ngoonug suuf, mbaa xaaju guddi, mbaa bu ganaar sabee, mbaa bu bët setee. Bumu ne jalañ, fekk leen ciy nelaw. Lii ma leen wax nag, ñépp laa ko wax: “Teewluleen!”»

Màrk 13:33–37