Ab sàcc moom, dara indiwu ko lu moy sàcc aka rey aka yàq. Man maa ñëw, ngir nit ñi dund dund gu naat.
Yowaan 10:10
Leeru Bés bi
Ab sàcc moom, dara indiwu ko lu moy sàcc aka rey aka yàq. Man maa ñëw, ngir nit ñi dund dund gu naat.
Yowaan 10:10
waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»
Njàlbéen ga 2:17
Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram ji mu àndal, moom it mu lekk.
Njàlbéen ga 3:6
Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.
Room 6:23
Moyug kenn nit ki, ci la dee jaare ci kenn nit kooku, ba falu. Kon ñi jot ci xéewalu yiw, ba am ci àtteb njub, ñaata yoon lañuy gënatee falu ci biir dund gu ñu ame ci keneen nit kiy Yeesu Almasi bi?
Room 5:17
Ci nit la dee dikke ci àddina. Moo tax ci nit itam la ndekkite dikke ci àddina. Noonu nit bokke ci Aadama, ba tax ñépp di dee, noonu la ñépp mana bokke ci Almasi bi, ba tax ñu dundalaat leen, ñoom ñépp.
1.Korent 15:21–22
Woowu yiw, la ko fésal moo di dikkug sunu Musalkat Almasi Yeesu, mi neenal dee, te niital nu yoonu texe, ak dee gu fomm ba fàww, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
2.Timote 1:10
Seede si moo di texe ba fàww la nu Yàlla jagleel, te texe googu ci Doomam la nekk. Ku am Doom ji, yaa texe; ku amul Doomu Yàlla, texewuloo.
1.Yowaan 5:11–12
Ndax kat Yàlla yebalul Doomam ci waa àddina ngir daan waa àddina, waaye musal waa àddina, mucc gu sottee ci Doomam, moo tax mu yebal ko.
Yowaan 3:17
Ndax kat, nun ñépp fàww nu taxawi fa jalub àttekaayu Almasi bi, ngir ku nekk yooloo kemu jëf ja mu jëfe yaramam, muy lu baax, mbaa lu bon.
2.Korent 5:10
Waaye wóor nanu ne àtteb Yàlla bi muy añale ñiy jëfe jooju jëfin, dëgg lay dëppool.
Room 2:2
«Keroog bu Doomu nit ki dikkee darajaam nag, ànd ak mboolem malaaka yi, mooy toog ci ngànguneem lu darajawu,
Macë 25:31
te mooy teg xar yi fi ndijooram; bëy yi, fa càmmoñam.
Macë 25:33
Su booba aji jub ñi dañu naa ràññ ni jant bi, fa seen nguurug Baay. Ku ami nopp, na dégg.»
Macë 13:43
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub. Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Room 8:33–34
Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.
Room 8:1
Waaye Boroom bee nuy teg ay daan ngir yare nu ko, ba deesu nu mbugalaale ci biir àtteb àddina.
1.Korent 11:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Few 2026
3 Few 2026
2 Few 2026
1 Few 2026
31 Sam 2026
30 Sam 2026
29 Sam 2026