Leeru Bés bi — 4 Fewriyee: Baamtug yoon wi 17:16

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Waaye bu buur bi barey fas, te bumu delloo askan wi Misra, ngir sàkku fas yu bare, te Aji Sax ji waxoon leen ne buleen dellooti woowu yoon.

Baamtug yoon wi 17:16

Bu ñu nammoon réew ma ñu jóge, manoon nañoo dellu. Waaye réew mu ko gën lañu doon sàkku, te mooy réewum asamaan. Looloo tax Yàlla rusul ñu di ko tudde seen Yàlla, ndax waajalal na leen ab dëkk.

Yawut ya 11:15–16

Bokk ak ñoñi Yàlla ab coono moo ko gënaloon muy bànneexoogum ci biir bàkkaar. Toroxtaange gu ñu koy teg ndax Almasi bi, moom la defoon muy alal ju ëpp denci Misra, ndax yoolub ëllëg ba la doon séentu.

Yawut ya 11:25–26

Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.» Nun nag bokkunu ci ñiy dellu gannaaw te nara sànku, waaye nooy ñi saxoo ngëm te nara mucc.

Yawut ya 10:38–39

Yeesu ne ko: «Képp ku tàmbalee gàbb tey xool gannaawam, jekkoo ci nguurug Yàlla.»

Luug 9:62

Waaye man de yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi bi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.

Galasi 6:14

Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen.

2.Korent 6:1

Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.

Filib 1:6

Yal na seeni dal gent, seeni xayma wéet.

Taalifi cant 69:26

Waaye mer mu réy laa mere xeet yii naagu. As lëf laa meroon, waaye ñoom ñoo yokk aw ay.

Sàkkaryaa 1:15

Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir, yeen itam.

Galasi 6:1

xamleen ne ku waññ bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na ko bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.

Yanqóoba 5:20

Bokk yi, danu leen di dénku; yaafus yi, femmuleen leen; ñi néewu fit, ñaaxleen leen; néew-doole yi, dimbalileen leen, te it muñalleen ñépp.

1.Tesalonig 5:14

Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar.

Room 14:13

Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.

Room 15:1

Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu.

1.Korent 13:4

Bokkul ak bége lu jubadi it, waaye moo di bége liy dëgg.

1.Korent 13:6

Moo tax ku yaakaar ne taxaw nga, nanga moytu bala ngay daanu.

1.Korent 10:12