Leeru Bés bi — 3 Fewriyee: Ase 2:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen,” kàddug Aji Sax jee. Mu ne: “Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Ase 2:4

«Man maay reseñ gi, yeen ngeen di car yi. Ki sax ci man, ma sax ci moom, kooku mooy meññ lu bare, nde su dul man, dungeen mana def dara.

Yowaan 15:5

Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.

Filib 4:13

Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Efes 6:10

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Neyemi 8:10

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Yeen ñi dégg kàddu yii tey ci gémmiñu yonent yi fekke woon, ba ñuy teg fondmaa kër Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ngir tabaxaat kër gi, nangeen góor-góorlu.

Sàkkaryaa 8:9

Ku yoqi, dooleelleen ko, ku óom yay fenqe, jàppaleleen ko. Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»

Esayi 35:3–4

Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Room 8:31

Ndegam boobu liggéey lanu sasoo, ci yërmandey Yàlla, dunu yoqi.

2.Korent 4:1

Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.

Galasi 6:9

Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!

1.Korent 15:57

du tax lëndëm lëndëmal la dara. Guddi da laa leeralal ni bëccëg, lëndëm dig leer fi yaw.

Taalifi cant 139:12

Yàlla déy a ngi ne jàkk ci jaar-jaari nit ki, di xool bépp jéegoom. Du fenn fu lëndëm mbaa fu ne këruus, fu kuy def lu ñaaw mana làqoo.

Ayóoba 34:21–22

Ku mana làqoo làquwaay, ba duma ko gis?» Kàddug Aji Sax jee. «Xanaa du asamaan ak suuf, maa ko fees?» Kàddug Aji Sax jee.

Yeremi 23:24

Doo ragal njàqarey guddi mbaa fittu bëccëg mbaa mbas mu yooteg lëndëm, ak balaa buy faat njolloor.

Taalifi cant 91:5–6

Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji, Aji Kawe jii di sama rawtu, genn loraange du la dab, balaa du jege sa xayma.

Taalifi cant 91:9–10

Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.

Taalifi cant 121:3

Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor. Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi. Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.

Taalifi cant 121:5–7

Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

Taalifi cant 23:4