Leeru Bés bi — 2 Fewriyee: 1.Jaar-jaar ya 4:10

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yabecc nag woo Yàllay Israayil wall, ne ko: «Éy, soo ma barkeeloon a barkeel, yokk samag moomeel, ànd ak man, musal ma ci lu aay lu may yóbbe mitit.» Yàlla may ko la mu ñaan.

1.Jaar-jaar ya 4:10

Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»

Luug 22:46

Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»

Macë 26:41

Éy Yàlla, ñaar laa la ñaan, ngalla may ma ko sama giiru dund: caaxaan aki fen, yal na ma sore, néewleek barele, bu ma ci may lenn, leel ma lu ma doy; lu ko moy ma regg, weddi la, ba naan: «Kuy Aji Sax ji?» Mbaa ma ñàkk bay sàcc, di la ñàkke worma, yaw sama Yàlla.

Kàddu yu xelu 30:7–9

Aji Sax jee lay sàmm ci gépp loraange, di sàmm sa bakkan.

Taalifi cant 121:7

«Ab soxor jàpp la, ma àtte; ab néeg ne la céex, ma foqati.»

Yeremi 15:21

Xam nanu ne képp ku sosoo ci Yàlla doo sax ci bàkkaar, waaye Kenn ki sosoo ci Yàlla moo koy sàmm, ba ku bon ki du ko manal dara.

1.Yowaan 5:18

Gannaaw yaa sàmm sama kàddu, ba muñ ni ma la ko sante, man itam dinaa la sàmm ci waxtuw nattu biy wàccsi ci àddina sépp, ngir nattu waa kaw suuf.

Peeñu ma 3:10

Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu ragal Yàlla cib nattu ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba,

2.Piyeer 2:9

Jant bi ak leeru boppam, weer wi ak leeru boppam, biddiiw yi ak seen leeru bopp, te biddiiw sax wuute naak moroom ma ag leer.

1.Korent 15:41

Ñu ne cell, ndax la ñu doon werante ca yoon wa moo di kan moo gëna kawe ci ñoom. Ba mu ko defee Yeesu toog, woo fukki taalibe yaak ñaar, ne leen: «Ku bëgga jiitu, na mujj ñépp te di surgab ñépp.»

Màrk 9:34–35

Naka noonu yeen ndaw ñi, nangulleen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.» Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,

1.Piyeer 5:5–6

Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir: Moom mi nekke nekkinu Yàlla te ŋoyaaloowul ci dayob boppam bi ko def nawleb Yàlla. Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.

Filib 2:5–7

Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf,

Filib 2:9–10

Ña rafet xel leer nàññ ni leeraayu déndub asamaan. Ñi doon xiir mbooloo mi ci njub ne boyy niy biddiiw, ba fàww.

Dañeel 12:3