Leeru Bés bi — 1 Fewriyee: 1.Piyeer 1:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,

1.Piyeer 1:8

ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis.

2.Korent 5:7

Nun nag, li nu taxa am cofeel moo di Yàlla moo nu njëkka sopp.

1.Yowaan 4:19

Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax.

1.Yowaan 4:16

Kooku, yeen ñi dul Yawut, ba ngeen déggee, yeen itam kàddug dëgg gi, xibaaru jàmm bi jëm ci seenug mucc, gannaaw ba ngeen gëmee, ci moom itam lañu leen màndargaale Noo gu Sell gi ñu dige woon.

Efes 1:13

Ñoom la Yàlla nammoona xamal ni mbóot mi yaatoo te yéeme, ñeel jàmbur ñi dul Yawut: mbóot mi moo di Almasi baa ngi ci yeen ñi dul Yawut itam, loolu di seen yaakaar ci ndam lu leen ñeel.

Kolos 1:27

Ku ne moo sopp Yàlla, te soppul mbokkum gëmkatam, day fen, ndax ku soppul sa mbokk mi ngay gis, doo mana sopp Yàlla mi nga gisul.

1.Yowaan 4:20

Yeesu ne ko: «Danga maa gis, ba tax nga gëm? Ndokkalee ñi gëm te gisuñu!»

Yowaan 20:29

Sujjóotalleen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokkalee képp ku ko làqoo!

Taalifi cant 2:12

Ci jamonoom, Yuda dina texe, Israayil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax jeey sunu njub.”

Yeremi 23:6

Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.

Esayi 64:6

Boroom bi Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar, di tudd sa àtte dëgg gu wéet.

Taalifi cant 71:16

Maa bég a bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam ndam, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Esayi 61:10

Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.

Luug 15:22

Jox nañu ko mbubbum lẽe mu set, ne ràññ, mu sol.» Lẽe boobu mooy jëfi njekk yu nit ñu sell ñi.

Peeñu ma 19:8

Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi, ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.

Filib 3:8–9