Waaye su ngeen dàqul waa réew mi, ña ngeen fa bàyyi ñooy mujj diy dég yu leen di luqi, aki dagg yuy cuut seeni wet. Ñoo leen di lëjal witt ca biir réew mooma ngeen sance.
Màndiŋ ma 33:55
Leeru Bés bi
Waaye su ngeen dàqul waa réew mi, ña ngeen fa bàyyi ñooy mujj diy dég yu leen di luqi, aki dagg yuy cuut seeni wet. Ñoo leen di lëjal witt ca biir réew mooma ngeen sance.
Màndiŋ ma 33:55
Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.
1.Timote 6:12
Ndaxte gànnaay yi nuy xeexe du gànnaayi suuxi neen, waaye da di gànnaay yu am fa Yàlla kàttanu daane ay tata. Te xalaatin yu jubul, noo leen di daaneel, mook lépp luy réy-réyloo ab taxawaayam, di joŋante ak xam-xamu Yàlla, te nooy jàpp njaam bépp xalaat, ngir déggalloo ko Almasi bi.
2.Korent 10:4–5
Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan. Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
Room 8:12–13
Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di ñaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def.
Galasi 5:17
Waaye gis naa ci samay cér, weneen yoon wuy xeex ak yoon wi samam xel jubool, te yoon woowoo ma jàpp njaam, jébbal ma dooley bàkkaar bi dëkke samay cér.
Room 7:23
Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.
Room 8:37
Su nit ki tooñee moroomu nitam, Yàllaay àtte; waaye su dee Aji Sax ji la nit ki tooñ, ana ku koy àtte?» Wax jooju nag taxul ba tey ñu déggal seen baay. Booba fekk na Aji Sax ji namm leena rey.
1.Samiyel 2:25
Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub. Moom ci boppam moo dig njotlaay ñeel sunuy bàkkaar, te du sunuy bàkkaar doŋŋ, waaye yoy àddina sépp la ñeel.
1.Yowaan 2:1–2
Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon, ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
Room 3:25–26
da koy baaxe, daldi ne Yàlla: «Musal ko ba du wàccagum biir pax. Maa ngeek njotlaayam.»
Ayóoba 33:24
Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Room 8:31
Ñi Yàlla tànn, ana ku leen di tuumaal? Yàlla de moo leen àtte ni ñu jub. Ana kuy tegeb daan? Almasi Yeesu de moo dee, rax ci dolli, mu dekki, te moo toog fa ndijooru Yàlla, di nu fa ñaanal!
Room 8:33–34
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Sam 2026
29 Sam 2026
28 Sam 2026
27 Sam 2026
26 Sam 2026
25 Sam 2026
24 Sam 2026