Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:1–2
Yeesu nag wax leen ñoom ñépp, ne leen: «Képp ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp, te nga gàddu bés bu nekk, bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
Luug 9:23
Naka noonu itam, kenn ci yeen du mana doon sama taalibe te dëdduwul mboolem lu mu am.
Luug 14:33
Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.
Room 13:12
Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.
1.Korent 9:25
Damay yar sama yaram yar bu metti kay, ba moom ko, ndax ëllëg ñu bañ maa doyadal, gannaaw bu ma xamalee ñeneen kàddu gi ba noppi.
1.Korent 9:27
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam, daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu.
Filib 3:13–14
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji.
Ni jant bu fenk la dikkam wóore,
ni ab taw la nuy dikkale,
ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Li baax ci nit mooy
nga nangoo muñ ba ngay ndaw.
Jooytu 3:27
Tegal gone ciw yoon;
ba bu màggee, du ko wacc.
Kàddu yu xelu 22:6
Te itam am nanu ay baay ci wàllu deret, ñoo nu daan yar, te danu leena wegoon. Kon nag xanaa du Baay bi yorug noo lanu wara gënatee nangul, ngir nu dund? Sunuy baay a nu yar fan yu néew, na mu jaadoo woon ci seenum xel. Waaye sunu Baay bii, sunu njariñal bopp la nuy yare, ngir nu séddu ci sellaayam.
Yawut ya 12:9–10
Maa jàddoon, nga duma ma,
léegi sa kàddu laay sàmm.
Taalifi cant 119:67
Ngëneel la ma duma yi jural,
ngir jànge naa ci say tegtal.
Taalifi cant 119:71
Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.
Yeremi 29:11
Ci suufu loxol Yàlla bi am doole la leen Yàlla di yékkatee bu jotee, su ngeen toroxloo,
1.Piyeer 5:6