Leeru Bés bi — 29 Samwiyee: Njàlbéen ga 16:13

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ajara nag tudde Aji Sax ji wax ak moom, Ata El Roy (muy firi Yaa di Yàlla jiy gis), ndaxte da ne: «Moo man! Moona gis naa Yàlla, moom it mu gisal ma boppam de!»

Njàlbéen ga 16:13

Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma; yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay, di ràññee fu sore samay xalaat, di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def. Aji Sax ji, bala maa wax baat, ndeke yaw, xam nga lépp.

Taalifi cant 139:1–4

Ni nga ma xame daa yéeme, xóot lool, ba wees ma.

Taalifi cant 139:6

Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.

Kàddu yu xelu 15:3

Lu waay jëf, Aji Sax ji gis, di xool mboolem fu mu jaare.

Kàddu yu xelu 5:21

Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.

Luug 16:15

Aji Sax ji déy suuf sépp lay jéere ay gëtam, ngir dooleel ñi ko wéetalal seen xol. Yëfi dof nga def ci mbir mii, ndax li dale tey ay xare topp na la.»

2.Jaar-jaar ya 16:9

Waaye Yeesu moom, taxul mu wóolu leen, ndax ñoom ñépp la xamoon, te it soxlawul kenn xamal ko nit, ndax moom ci boppam xam na li ci nit.

Yowaan 2:24–25

Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaan, bëgg nga maam?» Piyeer nag tiislu la ko Yeesu laaj ba ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Piyeer ne ko: «Sang bi, yaw xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Xontal ma samay xar.

Yowaan 21:17

Boroom bi sama Yàlla, naa la sante xol bu fees, màggal la ba fàww.

Taalifi cant 86:12

Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»

Taalifi cant 50:23

Di woyu cant ngir bésub Noflaay. Céy ngëneel li ci sant Aji Sax ji, di la woy, yaw Aji Kawe ji,

Taalifi cant 92:1–2

Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax! Màggalleen Ki Sax!

Taalifi cant 150:6

Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.

Room 12:1

Moo waral Yeesu itam deewe ca bitib dëkk ba, ngir sellale askan wi deretu boppam.

Yawut ya 13:12

Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.

Yawut ya 13:15

Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi bi,

Efes 5:20

Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Xar mi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo worma, yeyoo darajaak cant.»

Peeñu ma 5:12