Weñ ak xànjar la say xomb di doon, sa kàttan ànd ak saw fan.
Baamtug yoon wi 33:25
Leeru Bés bi
Weñ ak xànjar la say xomb di doon, sa kàttan ànd ak saw fan.
Baamtug yoon wi 33:25
Bu ñu leen tegee loxo nag, ba jébbal leen kilifa ya, la ngeen wara waxi bumu leen jaaxal, waaye kàddu gu ñu leen may keroog ca waxtu wa rekk, waxleen ko, ndax su keroogee du yeenay wax, waaye Noo gu Sell geey wax ci yeen.
Màrk 13:11
Kon nag buleen am xalaat ci ëllëg, ndax ëllëg dina xalaat boppam. Bés bu nekk, ab coonoom doy na ko.
Macë 6:34
Seedeleen ne doole, fa Yàlla, mi tiime Israayil darajaam, dooleem feeñoo xàmbaar ya.
Taalifi cant 68:35
Mooy dooleel ku loof, di kàttanal ku jeele.
Esayi 40:29
Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.
Filib 4:13
walum Kison buub leen, falaŋ, walum Kison maa! walum cosaan maa! Naa dëgërlu boog te buure xol.
Njiit ya 5:21
Yaw, ngelawal bëj-gànnaar, yewwul, ngelawal bëj-saalum, dikkal, wolalleen ma sama tool bi, mu gilli; sama nijaay dugg toolam, xéewloo ngën-gi-meññeefam.
Ngën-gi-woy 4:16
Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.
Yawut ya 12:11
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom, ba mu leen toxalee, dàqe leen noowam gu mag, bésu ngelawal penku.
Esayi 27:8
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Taalifi cant 103:13
Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés. Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk. Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
2.Korent 4:16–18
Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.
Yawut ya 5:8
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Sam 2026
26 Sam 2026
25 Sam 2026
24 Sam 2026
23 Sam 2026
22 Sam 2026
21 Sam 2026