Leeru Bés bi — 27 Samwiyee: 1.Yowaan 3:5

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Te xam ngeen ne Yeesu moo feeñ ngir far bàkkaar, te taqul fenn bàkkaar.

1.Yowaan 3:5

Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Yawut ya 1:1–3

Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

2.Korent 5:21

Gannaaw nag kiy àtte nit ku nekk ci ay jëfam te amu ci xejj ak seen, Baay ngeen koy wax, sàllooleen koo ragal, seen diirub ngan ci kaw suuf. Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam, waaye seenug njot moo di deretu Almasi ju jafe ji taxawe deretu xar mu sikkul, gàkkul. Bu yàgg, ba àddina sosoogul la Yàlla tuddaloon Almasi bi loolu, waaye léegi ci mujug jamono jii la ko Yàlla feeñal ngir yeen

1.Piyeer 1:17–20

Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee. Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.

2.Korent 5:14–15

Woo naa seede asamaan ak suuf ci yeen, bésub tey: dund ak dee laa teg fi seen kanam, ak barke ak alkànde. Tànnleen dund, ndax ngeen dund, yeen ak seen askan.

Baamtug yoon wi 30:19

Man de, bëgguma kenn dee. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen ba dund!»

Esekiyel 18:32

Su ma ñëwul woon, ba wax ak ñoom, duñu am bàkkaar. Waaye léegi amuñu aw lay ci seeni bàkkaar.

Yowaan 15:22

«Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.

Luug 12:47

Ndaxte peyooru bàkkaar mooy dee, waaye yiw wi Yàlla di maye mooy texe gu sax dàkk fi Almasi Yeesu, sunu Boroom.

Room 6:23

Ku gëm Doom ji, yaay texe ba fàww; ku baña gëm Doom ji nag, doo gis googu texe, waaye sànjum Yàlla mooy dëkk ci sa kaw.

Yowaan 3:36

Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci dee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu baaxe leen àtteb ñu jub.

Room 6:16

Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.

Yowaan 12:26