Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na.
Filib 4:5
Leeru Bés bi
Na seen lewetaay wóor ñépp, Sang bi jegesi na.
Filib 4:5
Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww. Kon nag deeleen dëfalantee yooyu kàddu.
1.Tesalonig 4:16–18
Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, léegi ma ñëw.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!
Peeñu ma 22:20
Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.
2.Piyeer 3:14
te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko. Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee. Ki leen woo de ku wóor la, te moo koy def it.
1.Tesalonig 5:22–24
Yeen itam muñleen te takk seenu fit, ndax bés ba Boroom biy dikk dëgmal na.
Yanqóoba 5:8
Mooy yeew mbaamam cig reseñ, cumbur ma féeteek car, ba ca gën; muy fóote ay yéreem biiñ, di sumb mbubbam ci ndoxum reseñ.
Njàlbéen ga 49:11
Naa woy sama soppe woyu cofeel wu solowoo tóokëram. Sama soppee fi amoon tóokër, kaw tund wu suuf sa nangu lool. Mu gàbb ko, dindi doj ya, jëmbat ca ngëneeli reseñ, tabax tóojub doj fa digg ba, ba yatt ca mbalkam nalukaayu reseñ, tey yaakaar reseñ ju neex, mu meññ, wex.
Esayi 5:1–2
Moona maa leen jëmbat, ngeen di ngëneelu reseñ, di jiwu mu mucc ayib. Nu ngeen walbatikoo di baadooloy reseñu àll?
Yeremi 2:21
Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmee, te mooy: séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak yàqute
Galasi 5:19
ak ñeetaane ak màndite ak xawaare yiy ànd ak moy ak yeneen yu ni mel. Ma artu leen nag, na ma leen artoo woon: ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla. Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko.
Galasi 5:21–23
«Man maay reseñ gi dëgg, sama Baay di boroom tóokër bi koy toppatoo. Sama bépp car bu meññul, da koy tenqi sànni, bépp car bu ci meññ lay xosat ba mu set wecc, ngir mu gëna meññ.
Yowaan 15:1–2
Saxleen ci man, ni ma saxe man ci sama bopp ci yeen. Ni carub reseñ tëlee meññal boppam, su saxul ci ndeyam, ni ngeen di tëlee meññ, su ngeen saxul ci man.
Yowaan 15:4
Li feeñal sama darajay Baay mooy ngeen meññ lu bare, te noonu ngeen di firndeele ne samay taalibe ngeen.
Yowaan 15:8
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Sam 2026
22 Sam 2026
21 Sam 2026
20 Sam 2026
19 Sam 2026
18 Sam 2026
17 Sam 2026