Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Leeru Bés bi
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Esayi 9:6
Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.
Yowaan 1:14
Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi, di wormaal saw tur, ngir sa ngor ak sa worma. Màggal nga sa tur ak sa kàddu, ba mu tiim lépp.
Taalifi cant 138:2
«Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.
Macë 1:23
Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»
Macë 1:21
ngir ñépp teral Doom ji, ni ñu terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay bi ko yónni.
Yowaan 5:23
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur,
Filib 2:9
Foofa la Almasi bi tiime lu sore gépp nguur ak bépp sañ-sañ ak gépp manoore ak gépp kilifteef ak wépp tur wees di tudd, muy tey di ëllëg. Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi,
Efes 1:21–22
Ay gëtam a ngi mel ni sawara wuy tàkk, bopp bi, mbaxanay buur yu baree ci tege, ñu bind ci kawam tur wu kenn xamul ku dul moom.
Peeñu ma 19:12
Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»
Peeñu ma 19:16
Aji Man ji nu dul daj daa bare doole, dëggu, di boroom njub, du noote.
Ayóoba 37:23
Ana ku yéegoon asamaan, ba wàcc? Mbaa mu masa ŋëb ngelaw ciy loxoom? Ana ku masa ëmb ndox ci ndimo? Mbaa mu rëdd mboolem kemi àddina? Nu mu tudd ak nu doomam tudd? Wax ma, yaw mi ko xam!
Kàddu yu xelu 30:4
Céru Aji Sax ji moo di ñoñam, te ñooñu, askanu Yanqóoba, di wàllam.
Baamtug yoon wi 32:9
Yeen nag, Almasi bi moo leen moom, te Almasi bi, Yàllaa ko moom.
1.Korent 3:23
sa gémmiñ di xelli ngëneelu biiñ. Na walal sama nijaay, tuurul ñiy nelaw.
Ngën-gi-woy 7:10
Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom, di fore digg tóor-tóor yi.
Ngën-gi-woy 2:16
Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:20
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp, ndax dees leena jot, ba fey njëg ga. Kon nag seen yaram, terale leen ko Yàlla.
1.Korent 6:19–20
Yeen nag Aji Sax jee leen jël, génne leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ba, ngir ngeen doon ñoñam ñi mu séddoo niki bésub tey.
Baamtug yoon wi 4:20
Noo bokk diy surga ci liggéeyu Yàlla bi; yeen ngeen di toolu Yàlla, di tabaxub Yàlla.
1.Korent 3:9
Almasi bi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
Yawut ya 3:6
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
1.Piyeer 2:5
«Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxe as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxe.
Malasi 3:17
Mboolem lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom, te ci ñoom la sama daraja feeñe.
Yowaan 17:10
Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo.
Efes 1:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Sam 2026
18 Sam 2026
17 Sam 2026
16 Sam 2026
15 Sam 2026
14 Sam 2026
13 Sam 2026