Leeru Bés bi — 25 Samwiyee: Room 3:22

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.

Room 3:22

Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

2.Korent 5:21

Almasi bi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»

Galasi 3:13

Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,

1.Korent 1:30

ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw.

Tit 3:5–6

Rax ci dolli, lépp sax laa far jàppe ag wàññeent, ndax ngëneel li sut lépp, te mooy xam kuy sama Sang Almasi Yeesu. Moom moo ma taxa nangoo ñàkk lépp, def lépp ni mbuubit, ngir tonoo Almasi bi, ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.

Filib 3:8–9

Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay».

Room 8:15

Loolu la Yeesu wax ba noppi, téen, xool asamaan, daldi ne: «Baay, waxtu wi jot na. Feeñalal sa darajay Doom, ngir Doom ji feeñal sa daraja.

Yowaan 17:1

Toogatuma ci àddina, waaye ñoom ci àddina lañu nekk, te man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmme leen sa tur wi nga ma jox, ngir ni nu nekke benn, ñoom it ñu nekke noonu benn.

Yowaan 17:11

«Baay Boroom njub, àddinaa la xamul, waaye man xam naa la, te ñii xam nañu ne yaa ma yebal.

Yowaan 17:25

Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko. Waaye bumuy sama coobare, nay doon ci sa coobare.»

Màrk 14:36

Li ngeen diy doom nag tax na Yàlla yebal Noowug Doomam ci seen biir xol, ba Noo gi naan: «Abba», muy firi Baay.

Galasi 4:6

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi. Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.

Efes 2:18–19

Yaw déy yaa di sunu baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israayil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu baay, sa tur a di sunu Jotkat naka jekk.

Esayi 63:16

Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom; léegi def ma ni ku bokk ci say surga.’ ” «Mu jóg, ngir dellu kër baayam. Fu sore la ko baayam séene, muy dikk. Mu ñeewante ko, daw, laxasu ko, fóon ko.

Luug 15:18–20

Kon nag doonleen ay roykati Yàlla, gannaaw yeenay doomam yi mu sopp,

Efes 5:1