nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
Taalifi cant 48:14
Leeru Bés bi
nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
Taalifi cant 48:14
Aji Sax ji, yaay sama Yàlla, dama lay teral, di la sant. Yaa defi jaloore, muy dogal yu yàgg, wér te wóor.
Esayi 25:1
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo, di sama ndabal xéewal. Yaa yor sama wërsëg.
Taalifi cant 16:5
leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam. Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
Taalifi cant 23:3–4
Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor. Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teraanga. Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy? Kàttan ak pexe jeex, Yàlla di ma dooleel, ma séddoo ko fàww.
Taalifi cant 73:23–26
Ci moom la sunu xol di sedde, turam wu sell lanu wóolu.
Taalifi cant 33:21
Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.
Taalifi cant 138:8
Ma bare xalaati xol, nga dëfal ma, ma bég.
Taalifi cant 94:19
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
Taalifi cant 61:2
May ciib-ciibi ni wetwet mbaa ramatu, di binni nim xati, di séentu kaw ba saay gët giim. Dama noon: Éy Boroom bi, loof naa, dimbali ma.»
Esayi 38:14
làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
Taalifi cant 55:22
Léegi nag Aji Sax ji, sama Yàlla, fal nga ma buur, ma wuutu saa baay Daawuda. Waaye Sang bi, man ndaw lu tuut laa, xawma sax nu may doxale.
1.Buur ya 3:7
Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
Yanqóoba 1:5
Teewul muy ci ñii, xetu dee gu jëme ci dee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?
2.Korent 2:16
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:9
Ñu jekki indil ko ab lafañ, mu tëdd cig laltu. Ba Yeesu seetloo seen ngëm, da ne lafañ ba: «Na sa xel dal, doom, jéggalees na la say bàkkaar.»
Macë 9:2
Yeesu ne gees, gis ko, ne ko: «Janq, na sam xel dal, sa ngëm a la faj.» Ca waxtu woowa la ndaw sa wér.
Macë 9:22
Dama lay sant, sama giiru dund kay, tàllal la ay loxo, sàbbaale la. Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural, ma bég, sarxolle, màggal la.
Taalifi cant 63:5–6
Bés yu mujj yi
Wone yépp21 Sam 2026
20 Sam 2026
19 Sam 2026
18 Sam 2026
17 Sam 2026
16 Sam 2026
15 Sam 2026