Leeru Bés bi — 18 Samwiyee: Room 5:14

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Teewul la dale ca Aadama ba ca Musaa, ci kaw àddina sépp la dee doon nguuru, ba ci kaw ñi bàkkaarul noonee Aadama xëtte woon ndigal. Aadama mooy takkndeeru ki doon dikk.

Room 5:14

Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deewam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deewale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.

Yawut ya 2:9

Ndaxte cofeelu Almasi bi daal moo nu jiite, nun ñi ràññee lii: gannaaw kenn moo dee ngir ñépp, kon ñépp a dee.

2.Korent 5:14

Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu baaxe ñu bare àtteb nit ñu jub.

Room 5:19

Noonu lañu binde ne: «Aadama, nit ku njëkk ka daldi doon boroom bakkan,» waaye Aadama mu mujj mi moo di Noo giy maye bakkan. Du yaram wi bindoo Noo gi nag mooy jiitu, waaye yaramu judduwaale wi mooy jiitu, yaram wi bindoo Noo gi topp ci.

1.Korent 15:45–46

Yàlla ne: «Nanu bind nit ci sunu melokaan, mu nirook nun, te na yilif jëni géej ak picci asamaan ak jur gépp ak suuf sépp ak lépp lu ciy raam.» Yàlla dafa sàkk nit ci melokaanam; ci melokaanu boppam la Yàlla sàkk nit, góor ak jigéen la sàkk.

Njàlbéen ga 1:26–27

Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Yawut ya 1:1–3

Yaa ko jox sañ-sañ ci ñépp, ngir mboolem ñi nga ko jox, mu texeel leen ba fàww.

Yowaan 17:2

Aadama mu njëkk ma, ci suuf la jóge woon, te ba tey di suuf; Aadamam ñaareel mi jóge fa asamaan. Kooka di suuf nag, na mu mel, ni la niti suuf mel. Ku jóge ca asamaan it, na mu mel, ni la ñu bokk ci asamaan ñi mel.

1.Korent 15:47–48

Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii.

Peeñu ma 1:19

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.

1.Korent 2:9–10

Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax.

Yowaan 16:13

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.

Peeñu ma 1:7

Bokk yi nag, bëggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo. Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

1.Tesalonig 4:13–14

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.

1.Tesalonig 4:16–17