di jaamoo Boroom bi ag woyof gu mat sëkk, ci biiri rongooñ ak nattu yu ma pexey Yawut yi teg.
Jëf ya 20:19
Leeru Bés bi
di jaamoo Boroom bi ag woyof gu mat sëkk, ci biiri rongooñ ak nattu yu ma pexey Yawut yi teg.
Jëf ya 20:19
Yeen nag, bumu deme noonu ci seen biir. Képp ku bëgga doon ku màgg ci yeen, na nekk seenub surga, te ku bëgga nekk seen njiit, na doon seenub jaam. Noonu la deme ci Doomu nit ki, ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñépp.»
Macë 20:26–28
Ku foog ne moo am solo, te du dara nag, boppam lay nax.
Galasi 6:3
Ma artu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.
Room 12:3
Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
Luug 17:10
Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digganteek yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.
2.Korent 1:12
Nun nag nooy njaqi bani kese yi yeb jooju alal, ngir mu bir ne manoore ju yéeme ji alal ji làmboo, manoorey Yàllaa, waaye du sunu jos.
2.Korent 4:7
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Nóoyin ab beykat la woon. Mu nekk nag ci njëmbatum reseñ. Mu am bés mu naan biiñ, ba màndi, tëdd ci xaymaam, daldi sàgganu.
Njàlbéen ga 9:20–21
Naka lay jub Misra, daldi ne soxnaam Sarayi: «Déglu ma, xam naa ne ku rafet nga.
Njàlbéen ga 12:11
Kon nag ngalla waxal ne sama jigéen nga, ba tax ma am jàmm; su ko defee dees na ma bàyyi, ma dund, te di la ko gërëme.»
Njàlbéen ga 12:13
Isaaxa ne Yanqóoba: «Jegesil, ma làmb la, ba mu wóor ma ne sama doom Esawoo.»
Njàlbéen ga 27:21
Isaaxa laaj ko ne ko: «Mbaa wóor na ne yaw ay Esawu?» Mu ne ko: «Waawaaw.»
Njàlbéen ga 27:24
Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma, muy loraangey Musaa te ñoo ko waral. Ñoo naqaral Musaa, ba mu wax wax ju ko rëcc.
Taalifi cant 106:32–33
Waa Israayil nag ñam ca lekku waa Gabawon ña te sàkkuwuñu ndigalal Aji Sax ji ci seen mbir. Ba loolu amee Yosuwe digook waa Gabawon jàmm, fasool leen kóllëreg jàmm, ngir wacce leen bakkan, njiiti ndaje ma dogale ko kàddug ngiñ.
Yosuwe 9:14–15
Li ko waral mooy Daawuda da daan jëfe njub lu Aji Sax ji rafetlu, te giiru dundam gépp teggiwul lenn lu ko Aji Sax ji sant lu moy ci mbirum Uri Etteen ba.
1.Buur ya 15:5
Mboolem ñooñu am jëw bu rafet ndax seen ngëm, jotuñu sax lees dige woon,
Yawut ya 11:39
te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu.
Room 3:24
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Du yeena tax nag may jëfe noonu. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Na leen loolu wóor. Kon nag yeen waa Israayil, rusleen ba ne tott ci seeni jëfin.
Esekiyel 36:32
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Sam 2026
17 Sam 2026
16 Sam 2026
15 Sam 2026
14 Sam 2026
13 Sam 2026
12 Sam 2026