Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Esayi 38:17
Leeru Bés bi
Ndeke sama tiisu xol wii, sama jàmm rekk a tax. Sa cofeel a tax nga sorele maak paxum sànkute. Yaa sànni sa gannaaw sama bépp bàkkaar.
Esayi 38:17
Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam. Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:9–10
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne. Moo nuy yërëmati; sunuy ñaawtéef lay joggiy tànkam, te biir xóotey géej lay tàbbal sunuy bàkkaar.
Mise 7:18–19
Aji Sax ji, dama lay kañ. Yaa ma yékkati, ba noon reetaanu ma. Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall, nga faj ma.
Taalifi cant 30:2–3
Ca reeni tund ya laa suuxi, caabiy suuf féete ma gannaaw ba fàww, waaye ca kan ma nga jukkee sama bakkan, yaw, sama Yàlla Aji Sax ji.
Yunus 2:7
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
Taalifi cant 40:1–2
Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii.
Peeñu ma 1:19
Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.
1.Korent 13:12
lépp la ko Yàlla di jébbal, teg ko ci ndëggoom.» Ba Yàlla jébbalee Yeesu lépp nag, dara la bàyyiwul, lu mu ko jébbalul. Dëgg la, fii nu tollu gisagunu ne jébbal nañu ko lépp.
Yawut ya 2:8
Rax ci dolli nu ngeek waxi yonent yi, muy wax ju wóor ju jara gëm, te yeena yey teewlu waxi yonent yi, ni ñuy teewloo ceeñeeru làmp bu tàkke ci biir lëndëm, ba kera fajar di xar, ba biddiiwu njël feqal seen xol.
2.Piyeer 1:19
Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Taalifi cant 119:105
Waaye yeen samay soppe, fàttalikuleen la ndawi sunu Boroom Yeesu Almasi bi waxoon lu jiitu. Ñu ne leen: «Mujug jamono, dina am ay ñaawlekat yu topp seen bakkan, wéye seen kéefar.»
Yudd 17–18
Noowug Yàlla wax na ci lu leer ne ci mujug jamono, dina am ñu wacc yoonu ngëm wi, di topp ay xalaat yuy fàbbee ak ay àlluway ceytaane
1.Timote 4:1
Gone yi, waxtu wu mujj wi dikk na, te noonu ngeen dégge woon ne bañaaleb Almasi bi dina ñëw, noonu la bañaaley Almasi yu bare feeñe, te loolu moo nu xamal ne waxtu wu mujj wi dikk na.
1.Yowaan 2:18
Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer.
Room 13:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Sam 2026
15 Sam 2026
14 Sam 2026
13 Sam 2026
12 Sam 2026
11 Sam 2026
10 Sam 2026