Leeru Bés bi — 21 Samwiyee: Yowaan 15:2

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sama bépp car bu meññul, da koy tenqi sànni, bépp car bu ci meññ lay xosat ba mu set wecc, ngir mu gëna meññ.

Yowaan 15:2

Waaye bésub dikkam, ana ku ko mana dékku? Bu teewee ana kuy taxaw? Nde moom daa mel ni sawaras tëgg buy xelli weñ, melati ni xemey fóotkat. Fa mbaxana dee benn lay tooge ni xellikat ak seggkat, te mooy segg sëti Lewi, xelli leen ni xaalis ak wurus, ba ñu doon niti Aji Sax ji, ñi koy indil sarax ci yoon.

Malasi 3:2–3

Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ; te muñ mooy jur kóllërey biir coono; kóllërey biir coono mooy jur yaakaar. Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.

Room 5:3–5

Muñleen coono bu leen di yar. Ni ay doom la Yàlla di jëflanteek yeen. Ana doom ju baay ba dul yar? Bu ñu leen xañee yar bi jépp doom am wàll, dafa fekk ngeen di doomi po, waaye du ngeen doomi yoon.

Yawut ya 12:7–8

Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub. Kon nag «dëgëralleen loxo yi toqi ak óom yi bañ,»

Yawut ya 12:11–12

Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»

Malasi 3:15

Ku màgg, Ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk te toroxlu, ngir leqali ku toroxlu, leqali boroom xol bu mokk.

Esayi 57:15

Woyof, ànd ak ku néewle moo gën séddook ku bew la mu lewal.

Kàddu yu xelu 16:19

«Ndokkalee ñi am xolub ku néew doole, nde nguurug asamaan, ñooy boroom.

Macë 5:3

Juróom benn a ngii yu Aji Sax ji bañ, ba ci juróom ñaar yu mu seexlu: kuy daŋŋiiral, kuy fen, kuy rey nit ku deful dara,

Kàddu yu xelu 6:16–17

Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.

Kàddu yu xelu 16:5

Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol; natt ma, ba ràññee sama xalaati xol. Xoolal ndax maa ngi doxe yoon wu aay, te nga teg ma ci yoon wi sax.

Taalifi cant 139:23–24

Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi. Damay sant Yàlla sama Boroom saa yu ma leen fàttalikoo,

Filib 1:2–3

Ndokkalee ñi woyof, nde ñooy moom àddina.

Macë 5:5