Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Leeru Bés bi
Te yaakaar jooju du tas, ndax cofeelu Yàlla gi baawaan ci sunu xol, ci ndimbalal Noo gu Sell gi mu nu may.
Room 5:5
Yaw la ay buur di baayoo, seeni lingeer di la nàmpal. Ñoo lay sujjóotal, di la maral say tànk, ba nga xam ne maay Aji Sax ji, te ku ma yaakaar du rus.»
Esayi 49:23
Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji, yaakaar Aji Sax ji.
Yeremi 17:7
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu. Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Ki Sax, di Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.
Esayi 26:3–4
Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw. Yal na Yàlla doŋŋ di dalal sama xel, moom mi ma yaakaar.
Taalifi cant 62:5–6
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem. Ñaar yooyu du tebbiku ndax Yàlla du fen, te nun ñi daw làqusi ci moom, ci lanu ame ndëgërlaay lu réy lu nu ŋoye ci yaakaar ji ci sunu kanam. Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba. Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.
Yawut ya 6:17–20
Man nag bokk yi, su ma dee xiirtale ci xaraf, ana lees may bunduxataaleeti? Kon kay sama waareb deewu Almasi bi ca bant ba dootul doon ag tooñ ci kenn.
Galasi 5:11
Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga dikk topp ma, fàtteel sa bopp te nga gàddu sa bant bi ñu lay daaj, door maa topp.
Macë 16:24
Bokkaalekat yi ngeen doon! Xanaa xamuleen ne xaritoo ak àddina moo di noonoo ak Yàlla? Kon nag ku namma def àddina ab xarit, ab noonu Yàlla ngay doon.
Yanqóoba 4:4
Ñuy feddali pastéefu taalibe yi, di leen ñaax ngir ñu saxoo ngëm, ne leen: «Coono yu baree ngii, fàww nu jaare ci, ngir tàbbi ci nguurug Yàlla.»
Jëf ya 14:22
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ doj wuy fakkastale, mooy xeer wuy daaneel, waaye ku ko gëm, doo rus.»
Room 9:33
Kon nag yeen ñi gëm, yeen la gànjar gi ñeel. Waaye ci ñi gëmul, nag: «Moo di doj wi tabaxkat yi beddi woon, te mu mujj di doju koñu tabax bi.» Te it: «Mooy doj wuy fakkastale, di xeer wuy daaneel.» Ñoo ko fakkastaloo nde ñoo gëmul kàddu gi, te it loolu la leen dogal ba séddoon.
1.Piyeer 2:7–8
Waaye man de yàlla buma damoo lenn lu moy deewug sunu Boroom Yeesu Almasi bi ca bant ba. Bant boobu moo tax àddina di lu ñu ma daajal ci bant, ba àddina dee; man it may lu ñu daajal àddina ci bant ba ma dee.
Galasi 6:14
Moo tax dootul man maay dund, waaye Almasi bi mooy dund léegi ci man. Sama dundu yaramu suux wii tey nag, ci ngëm gi ma gëm Doomu Yàlla laa koy dunde, moom mi ma sopp, ba jébbale boppam ngir man.
Galasi 2:20
Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam.
Galasi 5:24
su nu muñee, nooy bokk nguuru. Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal;
2.Timote 2:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Sam 2026
21 Sam 2026
20 Sam 2026
19 Sam 2026
18 Sam 2026
17 Sam 2026
16 Sam 2026