ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.
Kolos 1:19
Leeru Bés bi
ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.
Kolos 1:19
Baay bi moo sopp Doom ji, te lépp la teg ciy loxoom.
Yowaan 3:35
Moo tax Yàlla kaweel koo kaweel, baaxe ko tur wi tiim wépp tur, ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy ci kaw asamaan, di ci kaw suuf, di biir suuf, làmmiñu ñépp it biral ne Yeesu Almasi bi mooy Sang bi, te muy màggaayu Yàlla Baay bi.
Filib 2:9–11
Foofa la Almasi bi tiime lu sore gépp nguur ak bépp sañ-sañ ak gépp manoore ak gépp kilifteef ak wépp tur wees di tudd, muy tey di ëllëg.
Efes 1:21
Ndax moo di ki Yàlla sàkke lépp lu nekk asamaan ak lu nekk ci suuf, lu gisu ak lu gisuwul, muy boroom gàngune yeek boroom ndomboy tànk yeek boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi. Lépp ci moom lees ko sàkke, te mooy ki tax ñu sàkk lépp.
Kolos 1:16
Loolu sax moo waral Almasi bi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
Room 14:9
ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi ak mboolem boroom sañ-sañ yi.
Kolos 2:10
Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.
Yowaan 1:16
Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii.
Peeñu ma 1:19
Ndax kat du kàddug waxyu gu masa soqikoo ci coobarey nit, waaye ci xiirtalub Noo gu Sell gi la aw nit daan waxe kàddug waxyu gu bawoo fa Yàlla.
2.Piyeer 1:21
Lépp ci Kàddu gi lañu ko sàkke. Sàkkeesul dara lu ñu sàkkewul ci moom.
Yowaan 1:3
Xoolleen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.» Loolu la leen wax, daldi leen won ay loxoom aki tànkam.
Luug 24:39–40
Ki joxeb seedeem ci mbir yooyii, moo ci teg bëtam, te kàddug seedeem dëgg la. Moom ci boppam, xam na ne dëgg lay wax, te moo ci joxe kàddug seedeem, ngir yeen itam ngeen gëm.
Yowaan 19:35
Du ay léeb yu xel mu xareñ fent lanu leen xamale woon sunu manoorey Boroom Yeesu Almasi bi ak na muy dikke, waaye noo teewe màggaayam.
2.Piyeer 1:16
ngir seen ngëm baña sukkandiku ci xam-xamu nit, te sukkandiku ci manooreg Yàlla.
1.Korent 2:5
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Sam 2026
14 Sam 2026
13 Sam 2026
12 Sam 2026
11 Sam 2026
10 Sam 2026
9 Sam 2026