Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi, musal ma, yaa ko dige.
Taalifi cant 119:25
Leeru Bés bi
Maa ngi ne ñàyy ci pënd bi, musal ma, yaa ko dige.
Taalifi cant 119:25
Gannaaw nag yeena dekkeendoo ak Almasi bi, sàkkuleen la fa kaw, fa Almasi bi tooge ca ndijooru Yàlla. La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf, ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla.
Kolos 3:1–3
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.
Filib 3:20–21
Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di ñaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def.
Galasi 5:17
Kon nag bokk yi, bor topp na nu, waaye du sunu bindu suux lanu ameel lenn lu nu taxa topp sunu bakkan. Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
Room 8:12–13
Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.
1.Piyeer 2:11
Ma artu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.
Room 12:3
Ku ngëmam dëgërul nag, xajooleen ko, te bañ cee càmbar gis-gis yu wuute.
Room 14:1
Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.
Room 4:20
Yeesu daldi tàllal loxoom, jàpp ko, ne ko: «Yaaka néew ngëm, ana looy xel ñaar?»
Macë 14:31
Yeesu nag ne ko: «Ndaw sii, yaaka réy ngëm. Kon nag na la amal noonu nga ko bëgge.» Ca waxtu woowa la doom ja wér.
Macë 15:28
Naka la Yeesu délsi, ba dugg ca kër ga, gumba ya duggsi. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa koo def?» Ñu ne ko: «Waawaaw, Sang bi.» Yeesu daldi laal seeni bët, ne leen: «Noonu ngeen ko gëme, na ame noonu.»
Macë 9:28–29
Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
Luug 17:5
Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.
Yudd 20
Sampleen seeni reen ci moom, tabaxleen seen bopp ci moom, feddalikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaan ak kàdduy cant.
Kolos 2:7
Te ki nuy saxal ci Almasi bi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla.
2.Korent 1:21
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi bi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.
1.Piyeer 5:10
Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.
Room 15:1
Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakkastal, mbaa lu koy xiirtal ci bàkkaar.
Room 14:13
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Sam 2026
13 Sam 2026
12 Sam 2026
11 Sam 2026
10 Sam 2026
9 Sam 2026
8 Sam 2026