Leeru Bés bi — 14 Samwiyee: Yowaan 14:28

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

«Dégg ngeen ma ne leen: “Maa ngi dem, maa ngi délsi ci yeen.” Su ngeen ma soppoon, dingeen bége li may dem ci Baay bi, ndax Baay bee ma gëna màgg.

Yowaan 14:28

Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee ñaan, ne leen: Baay, nañu wormaal sa sellaayu tur, na sa nguur dikk.

Luug 11:2

Yeesu ne ko: «Bu ma langaamu, ndax yéegeeguma fa Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi yéegi ca sama Baay biy seen Baay, sama Yàlla jiy seen Yàlla.»

Yowaan 20:17

Waaye fàww àddina xam ne Baay bi laa sopp, te li ma Baay bi sant rekk laay def. Jógleen, nu dem!

Yowaan 14:31

Dangaa gëmul ne man, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax, waxuma ko ci sama coobarey bopp, waaye Baay bi nekk ci man, moo sottal ay jëfam.

Yowaan 14:10

Baay bi moo sopp Doom ji, te lépp la teg ciy loxoom.

Yowaan 3:35

Yaa ko jox sañ-sañ ci ñépp, ngir mboolem ñi nga ko jox, mu texeel leen ba fàww.

Yowaan 17:2

Filib ne ko: «Sang bi, won nu Baay bi rekk, mu doy nu.» Yeesu ne ko: «Filib, ni ma yàggeek yeen te ba tey xamuloo ma? Ku ma gis kay, gis nga Baay bi. Kon ana noo naan: “Won nu Baay bi”? Dangaa gëmul ne man, maa ngi ci Baay bi, te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax, waxuma ko ci sama coobarey bopp, waaye Baay bi nekk ci man, moo sottal ay jëfam.

Yowaan 14:8–10

Man ak Baay bi benn lanu.»

Yowaan 10:30

«Ni ma Baay bi soppe, man itam noonu laa leen soppe. Saxleen ci sama cofeel. Ni ma sàmme sama santaaney Baay, ba tax ma sax ci cofeelam, su ngeen ni sàmmee samay santaane, dingeen sax ci sama cofeel.

Yowaan 15:9–10

Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën.»

Njàlbéen ga 3:15

Moo dawoon yaramu ñu bare, ndax yàqu ba nirootul nit, bindootul woon ni doom aadama,

Esayi 52:14

Te moom sunuy tooñ a waral ñu jamat ko; sunuy ñaawtéef a waral ñu dëggaate ko. Yar yi nu jàmmal moom la dal, te mooy ki nu wére ciy góomam.

Esayi 53:5

Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»

Luug 22:53

Yeesu ne ko: «Su dul woon ag may gu la dikke fa kaw, doo am benn sañ-sañ ci man. Moo tax it ki ma teg ci say loxo gënati laa bàkkaar.»

Yowaan 19:11

Kuy bàkkaar, ci Seytaane la bokk, ndax Seytaane moo dale bàkkaar ca njàlbéen ga. Te Doomu Yàllaa dikk ngir nasaxal liggéeyu Seytaane.

1.Yowaan 3:8

Ci biir loolu ñu bare ñu ame ay jàngoroy jàngoro, mu wéral leen, rab yu bare, mu dàq leen. Waaye gannaaw rab ya xam nañu ko, mayu leen ñu wax.

Màrk 1:34

Yeesu dikk ne leen: «Joxees na ma bépp sañ-sañ fa asamaan ak fi kaw suuf.

Macë 28:18

Ñi gëm nag yii firnde lañuy àndal: dinañu dàq ay rab ci sama tur, dinañu làkk làkk yu bees;

Màrk 16:17

Su ko defee Yàlla miy boroom jàmm mooy dër Seytaane ci lu gaaw, fi ngeen ko joggi seeni tànk. Yal na sunu yiwu Boroom Yeesu ànd ak yeen!

Room 16:20