Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
Esayi 26:3
Leeru Bés bi
Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.
Esayi 26:3
làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
Taalifi cant 55:22
Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dallu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki Sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»
Esayi 12:2
Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di tiit, yeenaka néew ngëm!» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw la ak gannax ya. Lépp ne sendaw.
Macë 8:26
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:6–7
Ndax Boroom bi Aji Sax ji, Aji Sell ju Israayil dafa wax ne: «Délsi, dallu moo leen di musal. Ne tekk te wóolu maa leen di dooleel. Waaye yeena bëggul!
Esayi 30:15
Su boobaa àtteb dëgg ay jur jàmm, àtteb yoon di dalal tey aare ba fàww,
Esayi 32:17
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,
Peeñu ma 1:4
Buleen mer ba bàkkaar, te bu jant bi sowe seen mer;
Efes 4:26
«Bu la sa mbokk tooñee, demal ñaarook moom, yedd ko. Su la dégloo, yaa feeñle mbokk mu réeroon.
Macë 18:15
Ca la Piyeer dikk ne Yeesu: «Sang bi, ñaata yoon la ma sama mbokk di tooñ, ma baal ko? Ndax day mat ba mu tollook juróom ñaari yoon?» Yeesu ne ko: «Newuma la juróom ñaari yoon, waaye ba muy juróom ñaar fukki yoon ak juróom ñaar.
Macë 18:21–22
25-Bu ngeen taxawee di ñaan it, te fekk ngeen jàppal kenn dara, baalleen ko, ngir seen Baay ba fa asamaan baal leen seeni tooñ, yeen itam.»
Màrk 11:25
Yeenay ñi Yàlla tànn, sellal leen, sopp leen. Kon nag solleen xolu yërmande akug mbaax ak woyoflu ak jikko ju lewet ak xolu muñ. Muñalanteleen te di baalante, su dee kenn ku am lu mu sikke moroomam. Ni leen Boroom bi baale, deeleen baalantee noonu.
Kolos 3:12–13
Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.
Efes 4:32
Ci kaw loolu ndaw ya ne Sang bi: «Yokk nu ngëm.»
Luug 17:5
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Sam 2026
11 Sam 2026
10 Sam 2026
9 Sam 2026
8 Sam 2026
7 Sam 2026
6 Sam 2026