Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Yudd 25
Leeru Bés bi
Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Yudd 25
Te moom it moo tax ngeen bokk ci Almasi Yeesu mi ñu def muy sunu xam-xam bu bawoo fa Yàlla, di sunu njub, di sunu cellte, di sunug njot,
1.Korent 1:30
Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko? Am yaa xam Aji Man ji, ba ñédd ko? Lu gëna kawe kaw, ana loo ci man? Lu gëna xóot njaniiw, ana loo ci xam?
Ayóoba 11:7–8
Li nuy biral kay, da di mbóotum xam-xamu Yàlla mu làqu woon, te Yàlla dogaloon nu koo terale, laata àddina di sosu.
1.Korent 2:7
May niital ñépp, ni Yàlla nara sottale mébétam, miy mbóot mu làqu woon naka jekk fa moom Yàlla mi sos lépp. Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi bi, xel mu rafetum Yàlla, ni mu yaatoo ci fànn yu nekk.
Efes 3:9–10
Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.
Yanqóoba 1:5
Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la njëkka def, teg ci ànd ak jàmm akug dal. Day taxa neexa jubool, fees ak yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-parloo akug jinigal.
Yanqóoba 3:17
Damay tëdd te naa: «Kañ laay jóg nag?» Waaye guddi gudda gudd, walbatiku ba fajar xar génnliku na ma!
Ayóoba 7:4
Yéene bii moo wàccal Duuma: Nit a ngi may woowe tundu Seyir, naan: Wattukat bi, lu des ci guddi gi? Éy wattukat bi, lu desati ci guddi gi? Wattukat bi ne: «Bët set, mu guddeeti rekk; boo amee looy laaj, délsil laajaat ko.»
Esayi 21:11–12
Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.
Yawut ya 10:37
day mel ni leeru jant bu fenk, kaw asamaanu suba su niir newul, leeru asamaan su set, taw ba sewet, ba ñax jebbi.»
2.Samiyel 23:4
Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
Yowaan 14:2–3
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit. «Dégg ngeen ma ne leen: “Maa ngi dem, maa ngi délsi ci yeen.” Su ngeen ma soppoon, dingeen bége li may dem ci Baay bi, ndax Baay bee ma gëna màgg.
Yowaan 14:27–28
Yeen ñépp ay doomi leer ngeen, doomi bëccëg ndarakàmm; nun bokkunu dara ak guddi, mbaa ag lëndëm.
1.Tesalonig 5:5
Bunti dëkk bi du tëje mukk bëccëg, te foofa sax guddi amu fa.
Peeñu ma 21:25
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Sam 2026
10 Sam 2026
9 Sam 2026
8 Sam 2026
7 Sam 2026
6 Sam 2026
5 Sam 2026