Leeru Bés bi — 11 Samwiyee: Taalifi cant 65:1

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.

Taalifi cant 65:1

Teewul ci sunu wàllu bopp, jenn Yàllaa am, muy Baay bi lépp jóge ci moom, te sunu bakkan ñeel ko, benn Sang doŋŋ a am, muy Yeesu Almasi bi lépp ame ci moom, te sunu bakkan, ci moom la ame.

1.Korent 8:6

ngir ñépp teral Doom ji, ni ñu terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay bi ko yónni.

Yowaan 5:23

Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.

Yawut ya 13:15

Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»

Taalifi cant 50:23

Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làkk yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Xar mi, sol mbubb yu weex, jël ay cari garabi tàndarma. Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Texee ngi fi sunu Yàlla, ki toog ci ngàngune mi, ak ci Xar mi!»

Peeñu ma 7:9–10

ne: «Amiin! Na sunu Yàlla jagoo màggal ak daraja ak xel ak cant ak worma ak kàttan ak doole, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!»

Peeñu ma 7:12

Mooy jot sa bakkan, kaalaa la ngor ak yërmande,

Taalifi cant 103:4

Waaye seen jotkat a am doole, te mooy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi. Moo leen di layool seen layoo, ngir jàqal réewum Babilon, jàmmal waa àddina yi ci des.

Yeremi 50:34

«Man nag ndax maa leen di musal ci njaniiw? Ndax maa leen di jot ci dee? Moo yaw dee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!

Ose 13:14

Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.

Yawut ya 2:14–15

Ku gëm Doom ji, yaay texe ba fàww; ku baña gëm Doom ji nag, doo gis googu texe, waaye sànjum Yàlla mooy dëkk ci sa kaw.

Yowaan 3:36

ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla. Seenug dund dëgg Almasi bi la, te keroog bu Almasi bi feeñee, yeen itam dingeen ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.

Kolos 3:3–4

kera bés bu délsee ba jot ci teraangaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.

2.Tesalonig 1:10