Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Tesalonig 5:23
Leeru Bés bi
Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel ak seen léppi xol ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Tesalonig 5:23
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam.
Efes 5:25
Li mu ci namm moo di teewal mbooloo mi fi kanamam, mu mel ni ab séetam bu ne ràññ, gàkkul, rasul, taqul lenn, xanaa sell, mucc sikk.
Efes 5:27
Almasi boobu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy artoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi bi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi bi.
Kolos 1:28
Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:7
Na jàmmu Almasi bi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant.
Kolos 3:15
Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.
2.Tesalonig 2:16–17
Moo leen di dooleel ba ca mujjantal ga, ngir ngeen mucc sikk, keroog sunu bésu Sang Yeesu Almasi bi.
1.Korent 1:8
«Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ak doom aadama ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan ba ca asamaani asamaan manu laa fat, astamaak kër sii ma tabax.
2.Jaar-jaar ya 6:18
Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir cellte gi.
Taalifi cant 68:18
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»
2.Korent 6:16
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,
1.Korent 6:19
Ci Almasi bi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jàmbur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Efes 2:22
Bu sama kër gu sell nekkee fi seen biir ba fàww, xeet yi dinañu xam ne man Aji Sax ji maa sellal Israayil.”»
Esekiyel 37:28
Bés yu mujj yi
Wone yépp9 Sam 2026
8 Sam 2026
7 Sam 2026
6 Sam 2026
5 Sam 2026
4 Sam 2026
3 Sam 2026