Leeru Bés bi — 9 Samwiyee: Taalifi cant 60:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!

Taalifi cant 60:4

Dees na ragale turu Aji Sax ji fa sowu, ragale màggaayam ba penku. Bu noon bi agsee ni walum dex, ngelawal Aji Sax jee koy wal, mu daw.

Esayi 59:19

Yal na la may li nga namm, di sottal loo mébét,

Taalifi cant 20:5

Aji Sax ji jox na nu dëgg. Nanu yeggeji waa Siyoŋ jaloorey Aji Sax ji, sunu Yàlla.

Yeremi 51:10

Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem.

Room 8:37

Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!

1.Korent 15:57

Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.

Yawut ya 2:10

Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Efes 6:10

«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy, lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.

Yeremi 9:3

Ci kaw loolu Sawul ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sawul a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»

1.Samiyel 18:17

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen,” kàddug Aji Sax jee. Mu ne: “Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Googu kàddu laa jaayante woon ak yeen, ba ngeen di génne Misra. Samag noo laa taxawe fi seen biir, buleen tiit.

Ase 2:4–5

Du yeena naan: “Fii ak ñeenti weer ngóob taxaw”? Dégluleen, ma wax leen: dawalleen seen bët, xool tool yi, ñu ngi weex tàll, di xaar am ngóob.

Yowaan 4:35

Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.

Yawut ya 10:37

Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.»

Luug 10:42

Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji. Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!

Taalifi cant 4:6–7

Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor. Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, maa la koy sàkkoo xol.

Taalifi cant 42:1–2

Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda.

Taalifi cant 63:1

Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk.

Yowaan 6:35

Ñu ne ko nag: «Sang bi, dee nu may saa su ne ci woowu ñam!»

Yowaan 6:34

Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,

Luug 10:39

Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.

Taalifi cant 27:4