Leeru Bés bi — 6 Samwiyee: Taalifi cant 90:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Boroom bi sunu Yàlla, ngalla baaxe nu. Sottalal nu sunu liggéeyu loxo, rikk, sottalal nu sunu liggéeyu loxo.

Taalifi cant 90:17

siiw ba xeet yépp xam la ndax taar bu sotti ndax sama gànjar gu yànj gi ma la takkal. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Esekiyel 16:14

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

2.Korent 3:18

Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.

1.Piyeer 4:14

Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ndokkalee képp ku ragal Yàlla, di jëfe ay yoonam. Yaay lekk saw ñaq, mbégteek ngëneel ñeel la.

Taalifi cant 128:1–2

Loo bëgga def, diis ko Aji Sax ji, say mébét sotti.

Kàddu yu xelu 16:3

Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox, ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.

Filib 2:12–13

Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.

2.Tesalonig 2:16–17

Ndaw ya nag daje fa Yeesu, nettali ko la ñu def ak la ñu jàngale lépp.

Màrk 6:30

Barey àndandoo lor a ngi ci, waaye xarit a ngi gëna taq nit mbokkam.

Kàddu yu xelu 18:24

te samay xarit ngeen, ndegam yeena ngi def li ma leen sant. Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.

Yowaan 15:14–15

Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»

Luug 17:10

Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay».

Room 8:15

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.

Filib 4:6

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

Kàddu yu xelu 15:8