Nun ñi gëm doŋŋ nooy tàbbi ci noflaayam, noonu mu ko waxe, ne: «Maa giñ ci sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk fa samag noflaay.” » Ndaxam ba àddina sosoo la liggéeyu Yàlla sotti woon ba noppi,
Yawut ya 4:3
Leeru Bés bi
Nun ñi gëm doŋŋ nooy tàbbi ci noflaayam, noonu mu ko waxe, ne: «Maa giñ ci sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk fa samag noflaay.” » Ndaxam ba àddina sosoo la liggéeyu Yàlla sotti woon ba noppi,
Yawut ya 4:3
Yeena ngi dëkke njublaŋ, njublaŋ rekk, faaleetuleen ma.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 9:5
Waaye gis naa ci samay cér, weneen yoon wuy xeex ak yoon wi samam xel jubool, te yoon woowoo ma jàpp njaam, jébbal ma dooley bàkkaar bi dëkke samay cér. Céy maaka réy aw tiis! Ana ku may wallook sama yaramu dee wii?
Room 7:23–24
«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal.
Macë 11:28
Gannaaw nag dees noo baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi bi. Ci ndimbalam lanu ame ngëm ba mana àgg fi yiwu Yàlla wii nu taxaw taxawaay bu dëgër. Te it sunub sag moo di yaakaar ji nuy séentoo ab cér ci leeru Yàlla.
Room 5:1–2
Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dalloo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dalloo ci say liggéey.
Yawut ya 4:10
ngir ma mana feeñe ci biir Almasi bi, fu ma yaakaarul sama njubteg bopp gu ma feyoo sàmm yoonu Musaa, xanaa di yaakaar njubte gu laloo ngëm gi ma gëm Almasi bi. Njubte googu fa Yàlla la bawoo te gëm Almasi bi moo koy maye.
Filib 3:9
Moo leen waxoon ne leen: «Fii moo di noppalukaay bi, noppalleen ku sonn. Fii a di dalluwaay bi!» Waaye nanguwuñoo dégg.
Esayi 28:12
Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.
Taalifi cant 141:3
Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar, Boroom bi, ana kuy taxaw?
Taalifi cant 130:3
Ñoo naqaral Musaa, ba mu wax wax ju ko rëcc.
Taalifi cant 106:33
Du li dugg ci gémmiñ mooy sobeel nit ki, waaye liy génne ci gémmiñ, loolu mooy sobeel nit ki.»
Macë 15:11
Nitu njekkar day yokk réeroo, ab soskat di féewaley xarit.
Kàddu yu xelu 16:28
Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci. Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef-xippi, mu wéy.
Kàddu yu xelu 12:18–19
Waaye aw làmmiñ, kenn manu koo tàggat ba mu mokk. Mooy aayteef gu kenn manula dànk, fees dell ak tookey dee.
Yanqóoba 3:8
Genn gémmiñ gi, ci la kàddug cant ak gu móolu di jibe. Bokk yi, warula deme noonu kat.
Yanqóoba 3:10
Waaye léegi, lii lépp baleen ko: maanaam tàng xol ak mer mu ëpp ak coxor ak saaga ak wax ju ñaaw. Buleen di fenante, gannaaw seen jëmm ja woon démb, boole ngeen kook jëfinam ja mu àndal, summi,
Kolos 3:8–9
Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere.
1.Tesalonig 4:3
te kàddug fen masula jibe seen gémmiñ. Amuñu benn gàkk-gàkk.
Peeñu ma 14:5
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Sam 2026
3 Sam 2026
2 Sam 2026
1 Sam 2026
31 Des 2025
30 Des 2025
29 Des 2025